Matthew 4
4
1Fōfale la Nh͈el ma jīte Yesu cha manding ma, ndah͈ Seytane fir ko.
2Ganou ba mu ôre lu day na ñenent fuk’ i bechek ak ñenent fuk’ i gudi, mu h͈īf.
3Ba firkat ba ñoue fi mōm, mu ne, So de Dōm i Yalla, na nga ebal h͈êr yile ñu neka mburu.
4Wande mu tontu, ne, Binda nañu, ne, Nit du mburu reka la dunde, wande itam bāt bu neka bu juge chi gemeñ i Yalla.
5Seytane nak yubu ko fa deka bu sela ba, teg ko cha kou puj i juma ja,
6Te ne ko, So de Dōm i Yalla, chipālul chi suf; ndege binda nañu, ne, Dēnka na la i malāk’ am, te di nañu la yubu chi sēn loh͈o, ndah͈ do fakatal sa tanka chi h͈êr.
7Yesu ne ko, Binda nañu, nêti, Bul fir Borom ba sa Yalla.
8Seytane yubôti ko fa tūnda wu koue‐koue, te won ko i rew i aduna si yepa, ak sēn ndam;
9Te ne ko, Yef yōyu yepa lā la di may, so sūke chi suma kanam, te jāmu ma.
10Fōfale Yesu ne ko, Randu ma Seytane, ndege binda nañu, ne, Na nga jāmu Borom ba sa Yalla, te na nga ko topa, mōm reka.
11Fōfale Seytane bayi ko; i malāka dika, te bukanēgu ko.
12Ba mu dēge nak ne tej nañu John, mu dem cha Galilee;
13Te juge Nazareth, mu ñou deka chi Capernaum, bu jegeñ gēch ga, chi wet i Zebulun ak Naphtali:
14Ndah͈ la Isaiah yonent ba wah͈ on motaliku, ne,
15Suf i Zebulun ak suf i Naphtali, chi yōn i gēch ga, ganou Jordan, Galilee i Gentile ya;
16Nit ña jēki on chi lendem gis nañu lêr gu rey, te ña jēki on chi rew i dē ak takandēr am, chi ñom la lêr joge.
17Cha wah͈tu wōga Yesu dôr a wāre, ne, Rēchu len: ndege ngur i ajana jegeñsi na.
18Don na doh͈ cha tefes i Galilee, te mu gis ñar i mboka, Simon ku tūda Peter, ak mag am Andrew, di sani mbal cha gēch ga; ndege nek’ on nañu i mōl.
19Mu ne len, Topa len ma, te di nā len def i mōl i nit.
20Ñu wocha mbal ya chi tah͈ouay, te topa ko.
21Bu mu fa juge, mu gis yenen i mboka, James dōm i Zebedee, ak rak’ am John, chi gāl ga, ak Zebedee sēn bay, di dāh͈ sēn i mbal; te mu ô len.
22Ñu dal di wocha gāl ga, ak sēn bay, te topa ko.
23Yesu dem cha bir Galilee yepa, di jemantale chi sēn i juma, di wāre linjil i ngur gi, te di weral h͈êt i opa ju neka, ak hêt i jangaro ju neka chi digante nit ña.
24Dēgdēg i tur am dem cha bir Syria yepa; ñu yub ko nit ña op’ on ñepa, ña jangaro ju mun a don ak nchono jap’ on, ak ña i jine jap’ on, ak ña say, ak ña lafañ, te mu weral len.
25Mbōlo mu rey tope ko cha Galilee, ak Decapolis, ak Jerusalem, ak Judæa, ak ganou Jordan.
Currently Selected:
Matthew 4: GWG
Qaqambisa
Share
Copy
Ufuna ukuba iimbalasane zakho zigcinwe kuzo zonke izixhobo zakho? Bhalisela okanye ngena
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.