Matthew 28

28
1Cha muj i dimas ja, ba fajar di dôr chi bes bu jeka ba chi ay i bes ba, Mariama Magdalene ak menen Mariama ma ñou sêtsi bamel ba.
2Suf sa yengatu lol; ndege malāka i Borom ba wacha cha asaman, dika roñ doch wa cha bunta ba, te tōg chi kou am.
3Kanam am mel na melah͈, te chol am wêh͈ niki njōr:
4Ndig mōm otukat ya tīt be di dagdagi, te mel niki ñu dē.
5Malāka ma tontu jigen ya, ne, Bu len tīt: ndege h͈am nā ne Yesu ngēn di ūt, ka ñu dāj on cha kura ba.
6Nekul file; ndege dēki na, chi naka mu ko wah͈e won. Ñou len, sêt bereb bi fi ñu teral on Borom bi.
7Dem len bu gou, wah͈ i tālube am ne, Dēki na cha ñu dē ña; te di na len jitu cha Galilee; fōfale ngēn ko gise: mangi len ko wah͈.
8Ñu juge cha bamel ba bu gou chi tītay ak kontan gu rey, te dou ndah͈ ñu yubu tālube ya bāt ba.
9Yesu feka len, ne, Mangi len noyu. Ñu ñou, jap’ i tank’ am, te jāmu ko.
10Yesu ne len, Bu len tīt: dem len wah͈ suma i mboka ñu dem cha Galilee; fōfale la ñu ma gise.
11Ba ño dem nak, ñena chi otukat ya ñou chi bir deka ba, te nitali i njīt i seriñ ya la h͈ew on yepa.
12Ba ñu dajalô ak mag ña, te fēncha, ñu may otukat ya h͈alis bu bare, ne,
13Na ngēn ne, I tālube am a dik’ on chi gudi, te sacha ko ba ñu neloue.
14Su kēlifa ga dēge lile, di nañu ko dalal, te dindi len chi jāh͈le.
15Ñu jel h͈ālis ba, te def la ñu len wah͈ on: kadu gile fireku chi digante Yauod ya, neka bentey.
16Wande fuk’ i tālube ya ak bena dem cha Galilee, chi tūnda wa len Yesu wah͈ on.
17Ba ñu ko gise, ñu jāmu ko: wande ñena ña gumadi.
18Yesu ñou fi ñom, te wah͈ len, ne, May nañu ma kantan yepa cha ajana ak chi suf.
19Dem len mbōk, def i tālube h͈êt yi yepa, te batise len chi tur i Bay ba, ak Dōm ja, ak Nh͈el mu Sela ma:
20Di len jemantal ñu di dēncha lu mu mun a don lu ma len ebal on: te mangi neka ak yēn sā su neka, be cha muj i aduna.
UNWIN BROTHERS, LIMITED, THE GRESHAM PRESS, WOKING AND LONDON.

Currently Selected:

Matthew 28: GWG

Qaqambisa

Share

Copy

None

Ufuna ukuba iimbalasane zakho zigcinwe kuzo zonke izixhobo zakho? Bhalisela okanye ngena