John 1

1
1Cha chosan la Bāt ba am on na, te Bāt ba nek’ on na ak Yalla, te Bāt ba nek’ on na Yalla.
2Kile mō nek’ on cha chosan la ak Yalla.
3Lu neka chi mōm la saku on; te ganou mōm dara sakuwul on cha la saku on.
4Chi mōm la dūnda nek’ on; te dūnda gi nek’ on na lêr i nit.
5Te lêr gi melah͈ chi lendem gi, te lendem gi sēnu ko won.
6Nit ñou on na ka Yalla yōni on, ku tūda John.
7Kile sah͈ ñou on na ndig sēde, ndah͈ mu sēde chi lêr gi, ndah͈ ñepa mun a gum chi mōm.
8Mōm nekul on lêr gi, wande ñou on na ndah͈ mu sēde chi lêr gi;
9Lêr i dega gi di lêral nit ku neka ange ñou chi aduna si.
10Nek’ on na chi aduna si, te chi mōm la aduna si saku on, te aduna si h͈amu ko won.
11Ñou on na fi yos am, te yos am nanguwu ñu ko won.
12Wande ña ko nangu on, ñom la may on sañsañ ñu neka i dōm i Yalla, ña gum chi tur am:
13Ña jūdu on, dowul chi deret, mbāte chi mbugel i yaram, mbāte chi mbugel i nit, wande chi Yalla.
14Te Bāt bi yaramu on na, te dek’ on na ak ñun, te sêt on nañu ndam am, ndam niki ku di dōm i bay ju di bajo, fês ak yiw ak dega.
15John sēde on na ko, te h͈āchu, ne, Kile di ka ma wah͈ on, ne, Ka di ñou chi suma ganou neka na chi suma kanam, ndege mō ma jek’ on a neka.
16Ndege chi fêsay am la ñu nangu on ñepa, ak yiw chi kou yiw.
17Ndege Musa la ñu joh͈ on yōn wi; yiw ak dega bayako fa Yesu Krista.
18Ken mosul a gis Yalla muk; Dōm am ja di bajo, ka neka chi den’ i Bay ba, mō ko fêñal.
19Te lile di sēde’ John, ba Yauod ya yōne fa mōm i seriñ ak i fōdey bawo cha Jerusalem, di ko lāj, ne, Yā di kan?
20Mu yēgle, te wēdiwul; mu yēgle, ne, Dowu ma Krista.
21Ñu lājte ko, ne, Kan nak? Ndah͈ yā di Elijah? Mu ne, Dowu ma. Ndah͈ yā di yonent ba? Mu tontu, ne, Dēt.
22Ñu ne ko mbōk, Yā di kan? ndah͈ ñu delo tontu ña ñu yōni on. Lan nga wah͈ chi sa bopa?
23Mu ne, Mā’di bāt i kena ka di h͈āchu cha manding ma, Jūbal len yōn i Borom bi, naka Isaiah yonent ba wah͈ on.
24Te Pharisee ya len yōni on.
25Te ñu lāj ko, te ne ko, Ana lutah͈ nga di batise, so dowule Krista, mbāte Elijah, mbāte yonent ba?
26John tontu len, ne, Mā batise ak ndoh͈; wande chi sēn digante kena di tah͈ou ka ngēn h͈amul;
27Mō di ñou chi suma ganou, te daganu ma tiki būm i dal’ am.
28Yef yilê ’nga h͈ewe won cha Bethany, ganou wala Jordan, fa John don batise.
29Cha elek sa mu gis Yesu di ñou fi mōm, te ne, Sêt len, Mburtu’ Yalla mā’ngi, ka dindi bakar i aduna si!
30Mō di kile ma wah͈ on, ne, Nit di na dika chi suma ganou ka ma jītu, ndege mō ma jītu on.
31Te h͈amu ma ko won; wande ndah͈ mu fêñu cha Israel, lile tah͈ ma ñou di batise ak ndoh͈.
32Te John sēde on na, ne, Gis on nā Nh͈el ma wacha niki mpetah͈ cha asaman; te mu tōg cha kou am.
33Te h͈amu ma ko won: wande ka ma yōni on batise ak ndoh͈, mō ma wah͈ on, ne, Chi kan nga gis Nh͈el ma wacha, te tōg chi kou am, kōkale di batise ak Nh͈el mu Sela ma.
34Te da ma gis on, te sēde ne kile di Dōm i Yalla.
35Cha elek sa John tah͈ouati, ak ñar chi i talube am;
36Te mu sêt Yesu naka mu doh͈e, te ne, Sêt len, Mburtu’ Yalla mā’ngi!
37Te ñar i talube ya dēga mu wah͈, te ñu topa Yesu.
38Te Yesu h͈inaku, te gis len ñu di topa, te ne len, Lu ngēn di ūt? Ñu ne ko, Rabbi (mu tiki ne Jemantalkat bi), ana fan nga deka?
39Mu ne len, Dika len te gis. Ñu dika, te gis fa mu deka, te jēki ak mōm bechek bōba; chi fuk’ i wah͈tu la won potah͈.
40Kena chi ñar ña dēg’ on John, te top’ on ko, Andrew la won, rak’ i Simon Peter.
41Mu jeka gis mag am Simon, te ne ko, Feka nañu Masiu ma (mu tiki ne Krista).
42Mu indi ko fi Yesu. Yesu sêt ko, te ne, Yā di Simon, dōm i John: di nañu la tūde Cephas (mu tiki ne Peter).
43Cha elek sa bug’ on na dem cha Galilee, te mu gis Philip, te Yesu ne ko, Topa ma.
44Philip nak juge on na Bethsaida, dek’ i Andrew ak Peter.
45Philip gis Nathanael, te ne ko, Feka nañu ka Musa ak yonent ya bind’ on chi tauret ba, Mō di Yesu wā’ Nazareth, dōm i Yusufa.
46Te Nathanael ne ko, Ndah͈ lu bāh͈ mun na juge cha Nazareth am? Philip ne ko, Dikal te sêt.
47Yesu gis Nathanael mu di dika fi mōm, te wah͈ chi lu jem chi mōm, ne, Wā’ Israel chi dega angile, ka amul bena gaka.
48Nathanael ne ko, Ana fo ma h͈ame? Yesu tontu te ne ko, Ba la Philip ôangule, ba nga neke cha run mbot ga, gis nā la.
49Nathanael tontu ko, ne, Rabbi, yā di Dōm i Yalla; yā di Bur i Israel.
50Yesu tontu ko, ne, Gum nga ndege da ma la ne, Gis on nā la cha run mbot ga? Di nga gisi yef yu gen a rey as yile.
51Te mu ne ko, Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Di ngēn gisi asaman ūbiku, te i malaka i Yalla di yēg ak di wacha chi kou Dōm i nit ka.

Currently Selected:

John 1: GWG

Qaqambisa

Share

Copy

None

Ufuna ukuba iimbalasane zakho zigcinwe kuzo zonke izixhobo zakho? Bhalisela okanye ngena