Matthew 19

19
1Am on na ba Yesu sotal on kadu yile, mu juge cha Galilee, te ñou chi i mpeg’ i Judæa ganou Jordan:
2Mbōlo mu rey topa ko, mu weral len fa.
3Pharisee ya ñou fi mōm, di ko fir, te ne ko, Ndah͈ dagan na nit fase jabar am ndig lu mu mun a don?
4Mu tontu len, ne, Ndah͈ jangu len ne ka len bind’ on cha ndôrte la, dafa len bind’ on gōr ak jigen,
5Te nôn, Ndig lile tah͈na be nit di bayi bay am ak ndey am, bōlo ak jabar am, te di nañu neka bena yaram ñom ñar?
6Nōgule nekatu ñu ñar, wande bena yaram. Mōtah͈ lu Yalla bōlāte, nit waru ko fasāle.
7Ñu ne ko, Bōba lutah͈ on Musa ebal ñu joh͈ mbind’ i mpase, te fase ak mōm?
8Mu ne len, Musa ndig sēn degeray i h͈ol bayi on na len ngēn fase ak sēn i jabar: wande amul on nōgule cha ndôrte la.
9Te mangi len di wah͈, Ku fase ak jabar am, lu moy mu di chi njālo, te sey ak kenen, njālo na: te ku sey ak ka ñu fase, njālo na.
10Tālube ya ne ko, Su neke nōgule chi digante gōr ak jabar am, bāh͈ul ñu sey mbōk.
11Wande mu ne len, Ñepa munu ño nangu kadu gile, wande ña ñu ko may dal.
12Ndege i yōm la ñu judu on nōga cha sēn bir i ndey; yenen i yōm la ñu nit yōmlo; te i yōm la ñu yōmlo sēn bopa ngir ngur i ajana. Ku ko mun a nangu, na ko nangu.
13Fōfale ñu indi fi mōm gūne yu tūti, ndah͈ mu teg i loh͈o am chi ñom, te ñānal len: tālube ya h͈ūle len.
14Wande Yesu ne, Bayi len gūne yu tūti yi ñu ñou fi man, te bu len len tēre: ndege ngur i ajana lew na ña mel ni ñom.
15Mu teg i loh͈o am chi sēn kou, te juge fōfa.
16Kena ñou fi mōm, ne, Jemantalkat bi, lan lef lu bāh͈ lā ela def, ndah͈ ma mun a am dunda gu dul jêh͈?
17Mu ne ko, Lutah͈ nga lāj ma lu jem chi lu bāh͈? Kena la ku bāh͈: wande so buge h͈araf chi dunda, dēgal eble ya.
18Mu ne ko, Yan? Yesu ne, Bul rēy ken, Bul njālo, Bul sacha, Bul sēde fen,
19Teralal sa bay ak sa ndey: te, Sopal sa morom niki sa bopa.
20Far wa ne ko, Lōlu yepa lā dēncha: lan lā ñakati?
21Yesu ne ko, So buge mot, na nga dem, jay lo am, sarah͈ ko miskin ya, te di nga am jur cha ajana: te ñou, topa ma.
22Wande ba far wa dēge kadu ga, mu dem ak nah͈ar; ndege am on na alal ju bare.
23Yesu ne i tālube am, Chi dega mangi len di wah͈, Jafeñ na borom‐alal h͈araf chi ngur i ajana.
24Te ma nêti len, Gen na yomba gelem tabi chi bir but i pursa, aste borom‐alal h͈araf chi ngur i Yalla.
25Ba tālube ya dēge lōla, ñu jomi lol, ne, Ndōg kan a mun a mucha?
26Yesu sêt len, ne len, Lile munul a am ak nit; wande dara teūl Yalla.
27Fōfale Peter tontu ko, ne, Ñun ño wocha yepa, te topa la; lan la ñu ami mbōk?
28Yesu ne len, Chi dega mangi len di wah͈, Chi ndelute ga, ba Dōm i nit ka di tōgi chi kou gangūne’ ndam am, yēn ñi ma topa, di ngēn tōgi chi kou fuk’ i gangūne ak ñar, di ate fuk’ i h͈êt i Israel ak ñar.
29Te ku neka ku bayi i nēg, mbāt i raka, mbāt i jigen, mbāte bay, mbāte ndey, mbāt i dōm, mbāt i tōl ngir man, di na ami lu bare lu len upa, te dona dunda gu dul jêh͈.
30Wande bare na ña jītu di nañu mujeji; te ña muje di nañu jītuji.

Currently Selected:

Matthew 19: GWG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in