Matthew 18

18
1Cha wah͈tu wōwale tālube ya ñou fi Yesu, ne, Kan a di ka gen a rey chi ngur i ajana?
2Mu ô fi mōm ab gūne gu tūti, teg ko chi sēn digante,
3Ne, Chi dega mangi len di wah͈, Su ngēn tūbule, te neka niki gūne yu tūti, du len h͈arafi chi ngur i ajana muk.
4Ku mu mun a don mbōk ku di sufelu niki gile gūne gu tūti, mō di ka gen a rey chi ngur i ajana.
5Ku nangu gena gūne niki gile chi suma tur, man la nangu:
6Wande ku di moylo gena chi yile yu tūt ñi gum chi man, don na geni chi mōm ñu taka doch wu rey chi bāt am, te sani ko chi bir gēch ga.
7Suboh͈un aduna si ndig i mpaka! ndege i mpaka soh͈la naño dika; wande suboh͈un nit ka tah͈ mpaka ñou.
8Su la sa loh͈o mbāte sa tanka moylô, dog ko, te sani ko: mō gen nga h͈araf chi dunda ak lago mbāte di sôh͈, aste am ñar i loh͈o mbāte ñar i tanka, ñu di la sani chi safara su dul jêh͈.
9Su la sa but moylô, luh͈i ko, te sani ko: mō gen nga h͈araf chi dunda ak bena but, aste am ñar i but ñu di la sani chi safara i nāri.
10Otu len a jēpi kena chi gūne yu tūt yile; ndege mangi len di wah͈, cha ajana sēn i malāka di jāno ak suma kanam i Bay ba cha ajana sā su neka.
11Ndege Dōm i nit ka ñou na ndah͈ mu musal ñu rēr ña.
12Lan ngēn dēfe? Su nit ame tēmēr i nh͈ar, te bena rēr ko cha, du bayi jurom ñenent fuk’ ak jurom ñenent ya, dem cha tūnda ya, te ūti bu rēr ba am?
13Su ko gise, chi dega ma ne len, di na banēh͈u ndig mōm, aste jurom ñenent fuk’ ak jurom ñenent ya rērul on.
14Tah͈na itam du sēn mbugel i Bay ba cha ajana, ndah͈ kena chi yu tut yile rēr.
15Su la sa morom tōñe, demal won ko tōñ yangê’m chi sēn digante: su la dēge, fabi nga sa morom.
16Wande su la dēgule, andal ak kena mbāte ñar, ndah͈ bāt bu neka set chi gemeñ i ñar i sēde mbāte ñeta.
17Su len bañê dēga, wah͈ ko ndaje ma; te su bañê dēga ndaje ma itam, na neka chi you niki Gentile ak publican.
18Chi dega mangi len di wah͈, Lu mu mun a don lu ngēn di taka chi suf, di na taku cha ajana; te lu mu mun a don lu ngēn di tiki chi suf, di na tikiku cha ajana.
19Ma nêti len, Su ñar chi yēn dēgô chi suf lu jem chi lef lu ngēn di ñān, suma Bay bi cha ajana di na len ko defal.
20Ndege fu ñar mbāte ñeta dajalo chi suma tur, fōfale lā neka chi sēn digante.
21Fōfale Peter ñou fi mōm, te ne ko, Ñāt’ i yōn la ma suma morom di tōñ, te ma baal ko? be jurom ñar i yōn am?
22Yesu ne ko, Wah͈u ma la, Be jurom ñar i yōn; wande, Be jurom ñar fuk’ i yōn ak jurom ñar.
23Mōtah͈ ngur i ajana niro na ak bena bur bu bug’ on a jel konta ak i jām am.
24Ba mu dôre woña, ñu isi fi mōm kena ku ko leb on fuk’ i njūne chi h͈ālis.
25Wande ndege amul lu mu ko feye, borom am ebal ñu jay ko, ak jabar am, ak i dōm am, ak lu mu am yepa, ndah͈ mu fey bor am.
26Mōtah͈ jām ba sūka, te dagān ko, ne, Borom bi, muñal ma, di nā la fey yepa.
27Borom i jām bōbale yerem ko, mu bayi ko mu dem, te wocha ko ak bor ba.
28Wande jām bōbale gēna, te feka kena chi i naule am, ku ko leb on tēmēr i kopar: mu japa ko, ne ko chih͈ chi bāt am ne, Fey ma lo ma leb on.
29Naule am ba sūka, te dagān ko, ne, Muñal ma, di nā la fey.
30Mu fēta, wande dem tejlu ko chi kaso, be ba mu feye bor ba.
31Ba naule am ya gise la mu def, ñu nah͈arlu lol, te ñou nitali sēn borom la mu def on.
32Fōfale borom am ôlo ko fi mōm, te ne ko, E jām bu soh͈or bi, mā la baal on bor bōbale yepa, ndege dagān on nga ma:
33Warul kon you it nga yerem sa naule, naka ma la yereme on?
34Borom am mer, te jebale ko getenkat ya, be ba mu feye lu mu ko leb on yepa.
35Nōgu la itam suma Bay ba cha ajana di def ak yēn, su ngēn dul baalalante sēn morom chi sēn h͈ol.

Currently Selected:

Matthew 18: GWG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in