Matthew 2
2
1Ba Yesu jūdo cha Bethlehem i Judæa, chi bes i Herod bur ba, i borom‐h͈amh͈am juge on nañu cha Penku, ñou chi Jerusalem,
2Ne, Ana ki jūdu Bur i Yauod ya? Ndege gis on nañu bidiw am cha Penku, te dika nañu ndah͈ ñu jāmu ko.
3Ba Herod bur ba dēge lōla, mu jāh͈le, mōm ak Jerusalem yepa.
4Ba mu dajale i njīt i seriñ ya ak i bindānkat nit ña, mu lāj len fu Krista war a jūdu.
5Nu ne ko, Chi Bethlehem i Judæa; ndege yonent ba bind’ on na, ne,
6Te you Bethlehem, suf i Judah, du yā gen a tut chi i dek’ i Judah; ndege chi you la njīt di jugeji, ka di sama suma mbōtay Israel.
7Herod nak, ba mu ôe borom‐h͈amh͈am ya chi kumpa, mu lāj len bu bāh͈ wan wah͈tu la bidiw ba fêñ on.
8Mu yōni len fa Bethlehem, ne, Dem len, te ūt gūne ga bu bāh͈; su ngēn ko gise, delusi len te wah͈ ma ko, ndah͈ man itam ma jāmuji ko.
9Ba ñu dēge bur ba, ñu dem; te bidiw ba ñu gis on cha Penku, jītu len, be ba mu tah͈oue cha kou bereb ba gūne ga neka.
10Ba ñu gise bidiw ba, ñu banēh͈u ak banēh͈ gu rey lol.
11Ba ñu h͈arafe cha nēg ba, ñu feka gūne ga ak Mariama ndey am; ñu sūka te jāmu ko; ñu ūbi sēn i wah͈ande, te jebal ko i maye: wurus, fufata, ak mira.
12Te Yalla yēgal on na len chi gēnta, ne bu ñu delu fa Herod; mōtah͈ ñu ñibi sēn deka cha wenen yōn.
13Ba ñu dem on, malāka i Borom bi fêñu Yusufa chi gēnta, ne, Jogal, jelal gūne gi ak ndey am, te dou cha Mesara, te jēki fa be ba ma la cha ôe, ndege Herod di na ūt gūne gi ndah͈ mu rēylu ko.
14Mu jog, jel gūne ga ak ndey am chi gudi, te dem cha Mesara:
15Mu neka fa be ba Herod dēe, ndah͈ la Borom bi wah͈ on cha yonent ba motaliku, ne, Cha Mesara lā ôe suma dōm.
16Herod nak, ba mu gise ne borom‐h͈amh͈am ya nah͈ nañu ko, mu mer lol; mu yōne, te rēyat h͈alel yu gōr ya yepa ñu nek’ on cha Bethlehem, ak cha mpega ya, ñu am on ñar i at ak lu gen a new, naka cha wah͈tu wa mu lājte on borom‐h͈amh͈am ya.
17Lōgale motali na la Jeremiah wah͈ on, ne,
18Chi Ramah la ñu dēg’ on ab h͈āchu, joy ak yuh͈u gu rey, Rachel di joy ndig i dōm am, te bañ a jāleū, ndege da ñu dē.
19Wande ba Herod dēe, malāka i Borom bi fêñu Yusufa chi gēnta cha Mesara,
20Ne, Jogal, jelal gūne gi ak ndey am, te dem cha suf i Israel; ndege ña ūt on bakan i gūne gi dē nañu.
21Mu jog, jel gūne ga ak ndey am, te delusi cha suf i Israel.
22Wande ba mu dēge ne Archelaus ngūru chi bereb i bay am Herod, mu ragal a dem fōfa; te ba ko Yalla yēgale chi gēnta, mu dem cha wet i Galilee,
23Te ñou, deka chi rew mu tūda Nazareth: ndah͈ la yonent ya wah͈ on motaliku, ne, Di nañu ko tūde Nazarene.
હાલમાં પસંદ કરેલ:
Matthew 2: GWG
Highlight
શેર કરો
નકલ કરો
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.