YouVersion Logo
Search Icon

Matthew 20

20
1Ndege ngur i ajana niro na ak bena borom‐ker ku gēna chi sūba têl, ndah͈ mu binda i ligeykat chi tōl am.
2Ba mu wah͈ante ak ligeykat ya h͈asab bechek, mu yōni len cha tōl am.
3Mu gēnati potah͈ chi jurom ñenentel i wah͈tu, gis ñenen ñu tah͈ou chi jēy ba te defu ñu dara,
4Mu ne len, Dem len yēn it cha tōl ba, te di nā len joh͈ lu ela. Ñu dem.
5Mu gēnati potah͈ chi fukel i wah͈tu ak ñar, ak chi ñetel i wah͈tu, te def nōga.
6Chi juromel i wah͈tu chi ngon potah͈ mu gēnati, feka ñenen ñu tah͈ou; mu ne len, Lutah͈ ngēn tah͈ou fi bechek bi bepa, te defu len dara?
7Ñu ne ko, Ndege ken a ñu bindul. Mu ne len, Dem len yēn it cha tōl ba.
8Ba ngon jote, borom‐tōl ba ne bukanēg am, Ôal ligeykat ya, te joh͈ len sēn mpey, di dôr cha ña muje be cha ña jek’ on.
9Ba ña mu bind’ on potah͈ juromel i wah͈tu chi ngon ñoue, nit ku nek’ am h͈asab.
10Ba ñu jeka ñoue, ñu fōg ne di nañu jot lu upa lōga; wande ku neka itam am h͈asab.
11Ba ñu ko jele, ñu ñurumtu lu jem chi borom‐ker ga, ne,
12Ñile muje wena wah͈tu reka la ñu ligey, te nga emale len ak ñun, ñi enu on disay i bechek bi ak tangay am.
13Wande mu tontu kena chi ñom, ne, H͈arit, tōñu ma la: du bena h͈asab la ñu wah͈ante won am?
14Jelal li la lew, te dem sa yōn; buga nā joh͈ kile muje lu day ni sa bos.
15Ndah͈ daganul ma def lu ma buga chi lu ma mōm? mbar sa but bon na, ndege mā bāh?
16Nōnule ña muje di nañu jītuji; te ña jītu di nañu mujeji.
17Yesu don na dem cha Jerusalem, te chi yōn wa mu jel fuk’ i tālube ya ak ñar chi mpet, ne len,
18Ñunge dem cha Jerusalem, te di nañu jebal Dōm i nit ka i njīt i seriñ ya ak bindānkat ya; te di nañu ko ate ndah͈ mu dē;
19Di nañu ko jebal Gentile ya, ndah͈ ñu ñaual ko, ratah͈ ko, te dāj ko cha kura; te chi ñetel i fan am di na dēki.
20Fōfale ndey ī dom i Zebedee ñou fi mōm, ak dōm am yu gōr, di ko jāmu, te lāj ko lef.
21Mu ne ko, Lan nga buga? Mu ne ko, Na nga ebal ne suma ñar i dōm yile tōg, kena chi sa ndējor, kena chi sa chamoñ chi sa ngur.
22Wande Yesu tontu, ne, H͈amu len li ngēn di lāj. Ndah͈ mun ngēn a nān nān ba ma nāni? Ñu ne ko, Mun nañu ko.
23Mu ne len, Di ngēn nān suma nān chi dega: wande tōg chi suma ndējor ak suma chamoñ, munu ma ko maye kena, ganou ña ko suma Bay ba wājal.
24Ba ko fuka ña dēge, ñu mere ñar i mboka ya.
25Wande Yesu ô len fi mōm, te ne, H͈am ngēn ne i kēlifa i Gentile ya ēlif nañu len, te ñu rey ña ate nañu len ak sañsañ.
26Du neka nōgule chi sēn digante; wande ku buga rey chi sēn digante, na neka sēn bukanēg;
27Te ku buga neka sēn njīt, na neka sēn jām.
28Naka Dōm i nit ka ñouūl ndah͈ ñu bukanēgu ko, wande ndah͈ mu bukanēgu, te may dund’ am njot ngir ñu bare.
29Ba ñu gēne cha Jericho, mbōlo mu rey topa ko.
30Te ñar i silmah͈a ñu tōg chi wet i yōn wa, ba ñu dēge ne Yesu jār na fa, ñu h͈āchu, ne, Borom bi, yerem ñu, you dōm i Dauda!
31Mbōlo ma h͈ule len ndah͈ ñu nopi; wande ñu dolê h͈āchu, ne, Borom bi, yerem ñu, you dōm i Dauda!
32Yesu tah͈ou, te ô len, ne, Lan ngēn buga ma defal len?
33Ñu ne ko, Borom bi, na suñu i but ūbiku.
34Yesu am yermande chi ñom, lāl sēn i but, te chi tah͈ouay sēn i but gis, te ñu topa ko.

Currently Selected:

Matthew 20: GWG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in