YouVersion Logo
Search Icon

Matthew 21

21
1Ba ñu jegeñse Jerusalem, te ñou cha Bethphage, chi tūnda i Olive, Yesu yōni ñar i tālube am,
2Ne len, Dem len chi bir deka ba chi sēn kanam, te di ngēn feka mbamsuf mu ñu ew, and’ ak chumbur: tiki len, te isi len fi man.
3Su len kena wah͈e lef, na ngēn ne, Borom bā len soh͈la; te di na len yōni.
4Lile am on na nak, ndah͈ lu yonent ba wah͈ on motaliku, ne,
5Yēgal len dōm i Zion, Sa Bur anga dika fi you, lew, te di war mbamsuf, ak chumbur dōm i mbamsuf.
6Tālube ya dem, def naka len Yesu ebal on,
7Indi mbamsuf ma ak chumbur ma, teg sēn cholay chi sēn kou, te mu tōg chi kou am.
8Mbōlo ma talal sēn cholay chi yōn wa; ñenen dog i banh͈as i garap ya, te tasāre len chi yōn wa.
9Mbōlo ma jītu ak ña topa h͈āchu, ne Hosanna Dōm i Dauda; barkel chi ki di dika chi tur i Borom bi; Hosanna ma cha kou.
10Ba mu dike chi bir Jerusalem, deka ba yepa yengatu, ne, Kile kan la?
11Mbōlo ma ne, Kile di Yesu, yonent i Nazareth chi Galilee.
12Yesu h͈araf cha juma i Yalla, te gēne ña don jay ak ña don jenda ñepa cha juma ja, dupa i tābul i wēchikat i h͈ālis, ak i tōgu i ña don jay i mpetah͈,
13Te mu ne len, Binda nañu, ne, Suma nēg war na tūda nēg i ñān; wande yēn a ko def bereb ī sachakat.
14Silmah͈a ya ak ña lagi ñou fi mōm chi juma ja, te mu weral len.
15Wande i njīt i seriñ ya ak bindānkat ya, ba ñu gise koutef ya mu def, ak gūne ya di h͈āchu chi juma ja, ne, Hosanna Dōm i Dauda; ñu mer lol,
16Te ne ko, Ndah͈ dēga nga li ñile di wah͈? Yesu ne len, Wau: ndah͈ mosu len a janga, ne, Chi gemeñ’ i dōm ak i gūne yu di nampa nga motali nau?
17Mu bayi len, gēna cha deka ba chi bir Bethany, te fanān fa.
18Chi lelek sa nak, ba mu deluse chi deka ba, mu h͈īf.
19Mu gis garap i sōto chi wet i yōn wa, dem fa mōm, te fekul dara, wande i h͈ob reka; mu ne ko, Bul mēñati dōm bel mos. Nōn’ ak nōna sōto ba lah͈.
20Ba ko tālube ya gise, ñu jomi, ne, Naka sōto ba gou a lah͈e?
21Yesu tontu len, ne, Chi dega mangi len di wah͈, Su ngēn gume, te nimseū len, du len def niki ma def chi sōto bi reka, wande su ngēn wah͈e tūnda wile sah͈, ne, Roñul, te dem chi bir gēch ga, di na am.
22Te lu mu mun a don lu ngēn di ñān chi ngum, di ngēn ko ami yepa.
23Ba mu ñoue chi bir juma ja, i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña ñou fi mōm ba mō jemantale, ne, Ak ban sañsañ nga defe yef yile? te ku la joh͈ sañsañ bile?
24Yesu tontu len ne, Man it di nā len lāj bena bāt, te su ngēn ma ko wah͈e, di nā len wah͈ itam ak ban sañsañ lā defe yef yile.
25Batise’ John, fan la juge won? cha ajana am chi nit? Ñu werante chi sēn digante, ne, Su ñu ne, Cha ajana; di na ñu ne, Lutah͈ gumu len ko won mbōk?
26Wande su ñu ne, Chi nit; da ñu ragal mbōlo ma; ndege jape won nañu John niki yonent.
27Ñu tontu Yesu, ne, H͈amu ñu. Mu ne len it, Man du ma len wah͈ ak ban sañsañ lā defe yef yile.
28Wande lan ngēn dēfe? Kena nit am on na ñar i dōm yu gōr; mu ñou chi tau ba, ne, Suma dōm, demal ligey tey chi suma tōl.
29Mu tontu, ne, Du ma dem: wande cha ganou mu rēchu, te dem.
30Mu ñou cha ñarel ba, te wah͈ati lōga. Mu tontu, ne, Di nā dem; wande demul.
31Kan chi ñom ñar a def la sēn bay buga? Ñu ne ko, Tau ba. Yesu ne len, Chi dega mangi len di wah͈, Publican ya ak garbo ya di nañu dem chi ngur i Yalla as yēn.
32Ndege John ñou on na fi yēn chi yōn i njūbay, te gumu len ko won: wande publican ya ak garbo ya gum on nañu ko: te yēn ba ngēn ko gise, rechuwu len cha ganou sah͈ ndah͈ ngēn gum ko.
33Dēglu len benen lēb: Bena borom‐ker am on na, ku jembat on tōl, ñak ko, gas cha nalukay, tabah͈ am tata, lūye ko i ligeykat, te dem cha benen rew.
34Ba jamāno i mēñef jegeñse, mu yōni i ndau am chi ligeykat ya ndah͈ ñu jel i mēñef am.
35Ligeykat ya japa ndau am ya, ratah͈ kena, rēy kenen, te jamat kenen ka ak i h͈êr.
36Mu yōnêti yenen i ndau yu upa ñu jeka ña: ñu def len nōgule itam.
37Cha ganou ga mu yōni dōm am chi ñom, ne, Di nañu teral suma dōm.
38Wande ba ligeykat ya sēne dōm ja, ñu ne chi sēn bopa, Kile di dono gi; ñou len, na ñu ko rēy, te jel ndono am.
39Ñu japa ko, sani ko chi biti tōl ba, te rēy ko.
40Su borom‐tōl ba deluse nak, lan la di def ligeykat yōgale?
41Ñu ne ko, Di na rēy nit ñu soh͈or ñōgale chi choh͈or, te lūye tōl am yenen i ligeykat, ñu ko di joh͈i mēñef yi chi sēn wah͈tu’ ñorte.
42Yesu ne len, Ndah͈ mosu len a janga chi mbinda mi, ne, Doch wa tabah͈kat ya bañ on, mō di neki bop’ i tabah͈ ma: lile juge na fa Borom bi, te koutef la chi suñu i but?
43Mōtah͈ ma ne len, Di nañu jele ngur i Yalla fi yēn, te joh͈ ko h͈êt wu di mēña mēñef am.
44Ku dānuji chi doch wile, di na dama: wande ku mu dānu chi kou am, di na ko mokal kilip.
45Ba i njīt i seriñ ya ak Pharisee ya dēge lēb am ya, ñu gis ne lu jem chi ñom la wah͈.
46Ba ñu jēme japa ko, ñu ragal mbōlo ma, ndege jape won nañu ko niki yonent.

Currently Selected:

Matthew 21: GWG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in