Matthew 6
6
1Otu len ngēn def sēn i jef yu bāh͈ chi kanam i nit ndah͈ ñu gis len, mbāte du len am yōl chi sēn Bay ba cha ajana.
2So di sarah͈e mbōk, bul buftalo chi sa kanam, naka nafeh͈a ya di def chi juma ya ak mbeda ya, ndah͈ ñu am teranga chi nit. Chi dega mangi len di wah͈, Am nañu sēn yōl.
3Wande so di sarah͈e, bul sa loh͈o’ chamoñ h͈am lu sa loh͈o’ ndējor di def:
4Ndah͈ sa sarah͈ di nubu, te sa Bay ki di gis lu nubu, di na la yōl.
5Su ngēn di ñān, bu len def niki nafeh͈a ya: ndege sopa naño tah͈ou di ñān chi juma ya ak chi mbeda ya, ndah͈ nit gis len. Chi dega mangi len di wah͈, Am nañu sēn yōl.
6Wande you, so di ñān, dugal chi sa bir nēg, te ba nga teje bunta ba, ñānal sa Bay ki chi nubu; te sa Bay ki di gis lu nubu, di na la yōl.
7Te su ngēn di ñān, bu len wah͈ati bāt i nēn niki ña h͈amul Yalla; ndege dēfe nañu ne di nañu len dēga ndig sēn bāt yu bare.
8Mōtah͈ bu len niro ak ñom; ndege sēn Bay a h͈am lu ngēn soh͈la bala ngēn ko ñān.
9Ñān len mbōk nile: Suñu Bay ba cha ajana, Na sa tur sela;
10Na sa ngur dika; Lo buga na am chi suf naka cha ajana;
11May ñu tey suñu dundu gir gu neka;
12Te baal ñu suñu i bakar, naka ñu baale ña ñu tōñ;
13Te bu ñu bayi ñu tabi chi bulis, wande musal ñu chi lu bon.
14Ndege su ngēn baale nit sēn i tōñ, sēn Bay ba cha ajana di na len baal itam:
15Wande su ngēn baalule nit sēn i tōñ, sēn Bay du len baal sēn i bakar.
16Su ngēn di ôr, bu len am kanam gu dīs niki nafeh͈a ya; ndege di nañu ñaulo sēn i kanam ndah͈ nit ña gis ne ñunge ôr. Chi dega mangi len di wah͈, Am nañu sēn yōl.
17Wande you, so di ôr, diwal sa bopa te selem sa h͈ar‐kanam;
18Ndah͈ do mel naka ku di ôr chi nit, wande chi sa Bay ki chi nubu; te sa Bay ka gis lu nubu, di na la yōl.
19Bu len dajale alal chi aduna si, fa gasah͈ ak h͈omak di yah͈a, te fa i sachakat di daji te sacha:
20Wande dajale len alal cha ajana, fa gasah͈ ak h͈omak dul yah͈a, te fa i sachakat dul daji, mbāte sacha:
21Ndege fa sa alal neka, fōfale la sa h͈ol jem itam.
22Nītu i yaram wi mō di but; mōtah͈ su sa but were cheng, sa yaram yepa di na fês ak lêr;
23Wande su sa but werule, sa yaram yepa di na fês ak lendem. Mōtah͈ su lêr gi neke chi you lendeme, naka la lendem gōgale di reye!
24Ken munul a jāmu ñar i borom: ndege di na bañ kena, te sopa kenen; mbāte di na topa kena, te jēpi kenen. Munu len a jāmu Yalla ak alal.
25Mōtah͈ ma ne len, Bu len getenu ndig sēn dunda, di h͈alāt lan ngēn di leka, mbāte lan ngēn di nān; mbāt chi sēn yaram, di h͈alāt lan ngēn di sāngu. Du dunda gi mō gen leka, te yaram wi mō gen nchangay?
26Sêtlu len i mpich’ i asaman si; ndege du ñu ji, du ñu gōb, du ñu dajale chi i sah͈a; te sēn Bay ba cha ajana angi len di dundal. Mo, du yēn a len gen fuf?
27Kan chi yēn a mun a doli bena h͈asab chi guday am ndig jāh͈le am?
28Te lutah͈ ngēn getenu ndig nchangay? Sēntu len tōrtōr i tōl yi naka ñu sah͈e; du ñu ligey, du ñu echa;
29Te mangi len di wah͈, ne Suleyman sah͈ chi tār am yepa sānguwul on na bena chi ñom.
30Wande su Yalla sānge nōgule ñah͈ i tōl mi neka tey, te su elege ñu sani ko chi tāl, du len gen a sānga’m, yēn nit i ngum gu new?
31Mōtah͈ bu len getenu, ne, Lu ñu di leka, lu ñu di nān, lu ñu di sāngo?
32Ndege yef yile yepa la Gentile ya di ūt: ndege sēn Bay ba cha ajana h͈am na ne soh͈la ngēn yef yile yepa.
33Wande ūt len jeka ngur um Yalla ak njūbay am, te yile yepa di na len ko doli itam.
34Bu len getenu mbōk ndig elek, ndege elek di na indi jāh͈le am. Ngeten i gir gu neka doy na chi bop’ am.
Seçili Olanlar:
Matthew 6: GWG
Vurgu
Paylaş
Kopyala
Önemli anlarınızın tüm cihazlarınıza kaydedilmesini mi istiyorsunuz? Kayıt olun ya da giriş yapın
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.