Matthew 22

22
1Yesu tontu te wah͈ati len chi i lēb, ne,
2Ngur i ajana niro na ak bena bur bu h͈umbal on nchēt i dōm am;
3Te yōni i ndau am ñu ôal ko ña mu ô on chi nchēt la; ñu bañ a dika.
4Mu yōnêti yenen i ndau, ne, Wah͈ len ña ma ô on, Da ma wāj suma añ, rēndi suma i nag ak suma i rab yu dūf, te yepa emba na: ñou len chi nchēt li.
5Wande ñu sagane ko, te dem sēn yōn, kena cha tōl am, kenen cha jayukay am:
6Ña des japa i ndau am, tedadil len, te rēy len.
7Wande bur ba mer, yōni i h͈are am, rēylu bōmkat yōyale, te laka sēn deka.
8Fōfale mu ne i ndau am, Nchēt li emba na, wande ña ma ô on motu ñu.
9Dem len mbōk chi mbeda ya, te ñu ngēn gis ñepa, ô len chi nchēt li.
10Ndau ya dem cha mbeda ya, dajale ña ñu gis ñepa, ña bon ak ña bāh͈ itam; nchēt la fês ak ña ñu ô.
11Wande ba bur ba h͈arafse ndah͈ mu sêt ña ñou on, mu gis fa nit ku solul on chol i nchēt ga:
12Mu ne ko, H͈arit, naka nga fi h͈arafe, te amu la chol i nchēt gi? Wah͈ul dara.
13Fōfale bur ba ne i rapas am, Ew len loh͈o am ak tank’ am, te sani ko chi lendem i biti; fōfale la joy di neka ak yey i buñ.
14Ndege ñu bare la ñu ô, wande ñu new la ñu tana.
15Fōfale la Pharisee ya deme, te fēncha naka ñu ko mun a jape chi kadu am.
16Ñu yōni fi mōm sēn i tālube ak ga’ Herod, ne, Jemantalkat bi, h͈am nañu ne yā di dega, di jemantale yōn i Yalla chi dega, te ragalu la ken, ndege sêtu la kanam i nit.
17Wah͈ ñu nak, Lo dēfe? Ndah͈ dagan na ñu joh͈ Cæsar ngalak, am dēt.
18Wande Yesu gis sēn kēfēr, te ne len, Lutah͈ ngēn di ma fire, yēn nafeh͈a yi?
19Won len ma h͈ālis i ngalak li. Ñu yub ko h͈asab.
20Mu ne len, Bile ban natal la ak mbinda?
21Nu ne ko, Cæsar la. Mu ne len mbōk, Joh͈ len Cæsar yef i Cæsar; te Yalla yef i Yalla.
22Ba ñu ko dēge, ñu jomi, bayi ko, te dem sēn yōn.
23Bes bōbale i Sadducee, ñu ne ndēkite amul, ñou fi mōm, te lāj ko,
24Ne, Jemantalkat bi, Musa wah͈ on na, ne, Su nit dēe te amul dōm, rak’ am war na sey ak jabar am, te jur dōm chi mag am;
25Jurom ñar i dōm i ndey nak anga won ak ñun: mag ba sey on na, dē, te amul dōm, te bayi jabar am ak rak’ am;
26Ñarel ba itam def nōgule, ak ñetel ba, be cha jurom ñarel ba.
27Ganou ga jigen ja itam dē.
28Chi ndēkite ga mbōk, jabar i kan la di neka chi jurom ñar ña? ndege ñepa sey on nañu ak mōm.
29Yesu tontu len, ne, Da ngēn jūm, ndege h͈amu len mbinda ya, wala kantan i Yalla.
30Ndege chi ndēkite ga du ñu sey, te du ñu len maye chi sey, wande di nañu neka naka malāka ya cha ajana.
31Wande mosu len a janga lu jem chi ndēkite ga, la len Yalla wah͈ on, ne,
32Mā di Yalla i Ibrayuma, ak Yalla i Isaka, ak Yalla i Yanh͈oba? Yalla du Yalla i ñu dē ña, wande ñu dunda ña.
33Ba ko mbōlo ma dēge, ñu jomi cha njemantal am.
34Wande ba Pharisee ya dēge ne mō nopilo won Sadducee ya, ñu dajalo.
35Kena chi ñom ku h͈amkat i yōn la won, lāj ko di ko fir, ne,
36Jemantalkat bi, ban eblê gen a rey chi yōn wi?
37Mu ne ko, Na nga sopa Borom bi sa Yalla ak sa h͈ol bepa, ak sa fit wepa, ak sa nh͈el mepa.
38Bile di eble bu rey ba ak bu jeka ba.
39Te ñarel bu niro ak mōm di bile, Na nga sopa sa morom niki sa bopa.
40Chi ñar i eble yile la yōn wa yepa ak la yonent ya bind’ on japu.
41Ba Pharisee ya dajalô, Yesu lāj len, ne,
42Lan ngēn dēfe chi Krista? dōm i kan la? Ñu ne ko, Dōm i Dauda.
43Mu ne len, Naka la ko Dauda chi Nh͈el ma ôe Borom bi mbōk, ne,
44Borom bi nôn na suma Borom, Tôgal chi suma ndējor, be ma def sa i mbañ chi sa run tanka?
45Su ko Dauda ôe Borom bi, naka mu neke dōm am?
46Ken munu ko tontu bena bāt, te cha ganou lōlale, ken ñemeñatu ko lāj dara.

ที่ได้เลือกล่าสุด:

Matthew 22: GWG

เน้นข้อความ

แบ่งปัน

คัดลอก

None

ต้องการเน้นข้อความที่บันทึกไว้ตลอดทั้งอุปกรณ์ของคุณหรือไม่? ลงทะเบียน หรือลงชื่อเข้าใช้