Matthew 27
27
1Ba lelek sa jote, i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña ñepa fēnchu Yesu, ndah͈ ñu rēy ko.
2Ñu ew ko, omat ko, te jebal ko Pilate kēlifa ga.
3Fōfale Judas, ka ko or on, ba mu gise ne ey nañu ko, mu rēchu, te indêti ñeta fuk’ i dogit i h͈ālis chi i njīt i seriñ ya ak mag ya, ne,
4Da ma bakar chi niki ma ore deret i ku set ka. Wande ñu ne, Lu ñu soh͈al chi lōla? Sêtal sa bopa.
5Mu sani dogit i h͈alis ya chi suf chi juma ja, gēna, te dem, eng̈a bop’ am.
6I njīt i seriñ ya jel dogit i h͈alis ya, ne, Daganul ñu def ko chi dēnchukay bu sela bi, ndege njēg i deret la.
7Ñu fēncho, te jende h͈ālis ba tōl i ku dan tabah͈ i ndā, ndah͈ ñu di fa sūl i doh͈andem.
8Mōtah͈ ñu tūde tōl bōba, Tōl i deret bentey.
9Fōfale lu Jeremiah yonent ba wah͈ on motaliku, ne, Fab on nañu ñeta fuk’ i dogit i h͈ālis, njēg i ka ñu ap’ on, ka ñena chi dōm i Israel ya ap’ on,
10Te joh͈ len ko tōl i ku dan tabah͈ i ndā, naka ma ko Borom bi eble won.
11Yesu tah͈ou chi kanam i kēlifa ga, te kēlifa ga lāj ko, ne, Ndah͈ yā di Bur i Yauod ya? Yesu ne ko, Wah͈ nga ko.
12Ba ko i njīt i seriñ ya ak mag ya jêñe, tontuwul dara.
13Mōtah͈ Pilate ne ko, Dēgu la yef yi ñu la sēdêl?
14Tontuwu ko dara, du bena bāt sah͈; tah͈na kēlifa ga jomi lol.
15Chi h͈ewte ga nak, kēlifa ga dan na bayi cha mbōlo ma kena cha ña ñu tej on, ku ñu buga.
16Am on nañu chi wah͈tu wōwale sachakat bu dēgu on, ku tūda Barabbas.
17Ba ñu dajalô, Pilate ne len, Kan ngēn buga ma joh͈ len? Barabbas, am Yesu ki tūda Krista?
18Ndege h͈am on na ne ndig kañān la ñu ko jebale.
19Ba mu tōge chi ateukay ba, jabar am yōni fi mōm, ne, Bul bōlo chi yef i kōku nit ku jūb; ndege da ma yēg yef yu bare bes bile chi gēnta ndig mōm.
20I njīt i seriñ ya nak ak mag ya digal mbōlo ma ñu lāj Barabbas, te rēylu Yesu.
21Wande kēlifa ga tontu len, ne, Kan chi ñar ñi ngēn buga ma joh͈ len? Ñu ne, Barabbas.
22Pilate ne len, Lan lā ela def mbōk ak Yesu ki tūda Krista? Ñepa ne, Na ñu ko dāj chi kura.
23Kēlifa ga ne, Lutah͈, lan lu bon la def? Wande ñu h͈āchu bu bāh͈, ne, Na ñu ko dāj chi kura.
24Ba Pilate gise ne munul dara, wande nchōu anga buga jog, mu jel ndoh͈ te rah͈as i loh͈o am chi kanam mbōlo ma, ne, Man mūmin lā chi deret i nit ku jūb kile: na ngēn ko sêt.
25Nit ña ñepa tontu, ne, Na deret am dal chi suñu kou ak chi suñu kou i dōm.
26Tah͈na mu joh͈ len Barabbas; wande Yesu mu ratah͈ ko, te jebale ko ndah͈ ñu dāj ko chi kura ba.
27Fōfale i h͈arekat i kēlifa ga yubu Yesu chi ker i ate ga, te dajale fi mōm sēn i morom yepa.
28Ñu ñōri ko, te solal ko chol gu h͈onh͈a.
29Ñu lēta mbah͈ana i dek, te teg ko chi bop’ am, ak sonka chi ndējor am; ñu sūka chi kanam am, te ñaual ko, ne, Jamom, Bur i Yauod ya!
30Nu tufli ko; jel sonka ba, te dōr ko chi bop’ am.
31Ba ñu ko ñauale, ñu ñōri ko, solal ko chol am, te omat ko ndah͈ ñu dāj ko cha kura ba.
32Ba ñu gēne, ñu feka wā’ Cyrene ku tuda Simon: mōm la ñu jeñtal mu and’ ak ñom ndah͈ mu gadu kura ba.
33Ba ñu dike fa bereb bu tuda Golgotha, lu tiki ne, Bereb i h͈ot i bopa,
34Ñu joh͈ ko biñ bu ñu bōle ak weh͈tan ndah͈ mu nān: ba mu ko mose, mu bañ a nān.
35Ba ñu ko dāje cha kura ba, ñu sedo chol am chi sēn bopa, di wuri:
36Ñu tōg, di ko otu fōfale.
37Ñu teg chi kou bop’ am njêñ am, ba ñu bind’ on nile: Kile di Yesu Bur i Yauod ya.
38Fōfale ñu dājāle cha i kura itam ñar i sachakat, kena chi ndējor am, ak kenen chi chamoñ am.
39Ña fa romba sāga ko, di yengal sēn i bopa, ne,
40You mi dānel jama ja te tabah͈ati ko chi ñet’ i fan, musalal sa bopa. So de Dōm i Yalla, wachal chi kura bi.
41I njīt i seriñ ya itam, ak bindānkat ya ak mag ya ñaual ko, ne,
42Musal na ñenen; munul a musal bop’ am. Mō di Bur i Israel: na wacha lēgi chi kura bi, te di nañu ko gum.
43Mu ōlu Yalla; na ko musal lēgi, su ko buge; ndege nôn na, Mā di Dōm i Yalla.
44Sachakat ya itam, ña ñu dājāle won chi kura ya, ñu h͈as ko nōga.
45Cha fuk’ i wah͈tu ak ñar nak be cha ñet’ i wah͈tu, lendem neka chi kou suf si yepa.
46Chi ñet’ i wah͈tu potah͈, Yesu h͈āchu be cha kou, ne, Eli, Eli, lama sabachthani? mu tiki ne, Yalla man, Yalla man, lutah͈ nga wocha ma?
47Ñena ñu tah͈ou fa, ba ñu dēge lōla, ne, Ki nit ange ô Elijah.
48Nōn’ ak nōna kena chi ñom dou, jel ab sponge, fêsal ko binegar, def ko chi sonka, te joh͈ ko mu nān.
49Ña cha des ne, Bayi ko; na ñu gis su Elijah di ñou musal ko.
50Yesu h͈āchôti be cha kou, te tago fit am.
51Ser i juma ja h͈otiku chi diga, cha kou be chi suf; suf si yengatu; doch yu rey ya h͈ar;
52Bamel ya ūbeku; te i yaram i jūlit yu bare ñu don nelou jog;
53Gēna chi bamel ya ganou ndēkite am, h͈araf chi bir deka bu sela ba, te fêñu i nit jupa.
54Saltige ba nak, ak ña nek’ on ak mōm, di otu Yesu, ba ñu gise yengatu’ suf sa, ak yef ya am, ñu tīt lol, ne, Chi dega kile Dōm i Yalla la.
55Jigen yu bare tah͈ou fu sorey di sêt, ñu top’ on Yesu cha Galilee di ko bukanēgu:
56Chi sēn digante la Mariama Magdalene nek’ on, ak Mariama ndey i James ak Joses, ak ndey ī dōm i Zebedee.
57Ba ngon jote, borom‐alal ku juge on Arimathæa, ka tūda Yusufa, te nek’ on itam tālube i Yesu:
58Kile dem fa Pilate te dagān yaram i Yesu. Fōfale Pilate eble ñu joh͈ ko ko.
59Yusufa jel yaram wa, lomas ko chi ser wu set te wêh͈,
60Te teral ko chi bamel am bu ês, ba mu et’ on chi h͈êr: mu borong doch wu rey chi bunt’ i bamel ba, te dem.
61Mariama Magdalene ak menen Mariama ma neka fa, di tōg fu jegeñ bamel ba.
62Cha lelek sa nak, bes ba topa bes i wājte ba, i njīt i seriñ ya ak Pharisee ya dajalo fa Pilate,
63Ne, Borom bi, Fataliku nañu ne nafeh͈a bōbale nôn na ba mu dund’ on, Chi ganou ñet’ i fan di nā dēki.
64Ebalal mbōk ne ñu otu bamel ba be chi ñet’ i fan; wala h͈ēchna i tālube am di nañu dika sacha ko, te ne nit ña, Defa dēki cha ñu dē ña: kōn jūm gu muj ga di na gen a bon gu jeka ga.
65Pilate ne len, Am ngēn i otukat: dem len, otu len ko lu ngēn mum.
66Ñu dem, defar bamel ba bu bāh͈, kaste doch wa, te otukat ya neka ak ñom.
Terpilih Sekarang Ini:
Matthew 27: GWG
Highlight
Kongsi
Salin
Ingin menyimpan sorotan merentas semua peranti anda? Mendaftar atau log masuk
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.