Matthew 26

26
1Am on na, ba Yesu sotal on bāt yōyale yepa, mu ne i tālube am,
2H͈am ngēn ne cha ganou ñar i fan h͈ewte ga di na jot, te ñu or Dōm i nit ka ndah͈ ñu dāj ko chi kura.
3Fōfale i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña dajalo fi ker i kēlifa i seriñ ya, ku tūda Caiaphas,
4Te ñu wah͈ante chi sēn bopa ndah͈ ñu japa Yesu chi mūste, te rēy ko.
5Wande ñu ne, Du chi h͈ewte ga, lēgi nchōu buga joge chi digante ñit ña.
6Ba Yesu neke chi Bethany nak, chi nēg i Simon gāna ga,
7Jena jigen, ju am ndap i diw gu h͈ēñ gu jafe njēg lol, ñou fi mom, te tūr ko chi bop’ am ba mu tōge di leka.
8Wande ba ko tālube ya gise, ñu mer, ne, Lu waral yah͈a gile?
9Ndege mun on naño jay diw gu h͈ēñ gile, te am chi lu bare, sarah͈ ko miskin yi.
10Wande Yesu h͈am ko, ne len, Lutah͈ ngēn di geten jigen ji? ndege defal on na ma jef ju hāh͈.
11Ndege am ngēn miskin ya chi sen digante sā su neka; wande man du len ma am sā su neka.
12Ndege ba mu tūre diw gu h͈ēñ gile chi suma yaram, def na ko ndig suma sūl.
13Chi dega mangi len di wah͈, Fu ñu mun a wāre linjil bile chi aduna si yepa, di nañu nitali la jigen jile def on ndah͈ di ko fatalako.
14Fōfale kena chi fuk’ ak ñar ña, ku tūda Judas Iscariot, dem fa i njīt i seriñ ya,
15Te ne len, Lan ngēn ma joh͈, te di nā len ko jebal? Ñu dige ak mōm ñeta fuk’ i dogit i h͈alis.
16Cha ganou lōlu mu ūt naka la ko mun a ore.
17Chi bes i h͈ewte i mburu’ njanja bu jeka, tālube ya ñou fi Yesu, ne, Fan nga buga ñu wājal la ndah͈ nga leka h͈ewte gi?
18Mu ne, Dem len chi bir deka ba fa kena nit, te ne ko, Jemantalkat ba ne, Suma wah͈tu jegeñsi na; di nā h͈umbal h͈ewte ga chi sa nēg, ak suma i tālube.
19Tālube ya def la len Yesu wah͈ on, waj h͈ewte ga.
20Ba ngon jote, mu tōg di leka ak fuk’ i tālube ya ak ñar;
21Ba ñu di leka, mu ne, Chi dega mangi len di wah͈, kena chi yēn di na ma ori.
22Ñu nah͈arlu bu miti, te ku neka dal ne ko, Borom bi, man lā’m?
23Mu tontu, ne, Ki jō loh͈o am ak man chi ndap li, kōka ma ori.
24Dōm i nit ka di na dem naka ñu bind’ on la jem chi mōm; wande suboh͈un nit ka ko ori! bāh͈ on na chi nit kōkale su juduūl on.
25Fōfale Judas ma ko or, tontu ne, Man lā’m, Rabbi? Mu ne ko, Wah͈ nga ko.
26Ba ño leka, Yesu jel mburu, gerem Yalla, dogat ko, te joh͈ ko tālube ya, ne, Jel len, leka; lile suma yaram la.
27Mu jel mbatu, gerem Yalla, te joh͈ len ko, ne, Nān len chi yēn ñepa;
28Ndege lile di suma deret i koleri gu ês, ja di tūru ndig ñu bare ndege mbaale’ i bakar.
29Wande mangi len di wah͈, Du ma nānati dōm i garap i biñ bile, be cha bes bōba ma ko nāni bu ês ak yēn chi suma ngur i Bay.
30Ba ñu sante, ñu dem chi tūnda i Olive ya.
31Fōfale Yesu ne len, Di ngēn fakatalu ndig man chi gudi gile yēn ñepa: ndege binda nañu, ne, Di nā dōr sama ba, te i nh͈ar i gēta ga di nañu h͈ajātlaku.
32Wande ganou bu ma dēketi, di nā len jītu cha Galilee.
33Wande Peter tontu ko, ne, Su ñepa fakatalô ndig you, man du ma fakatalu muk.
34Yesu ne ko, Chi dega ma ne la, chi gudi gile, bala seh͈a ga sab, di nga ma wēdi ñet i yōn.
35Peter ne ko, Su ma dēe ak you sah͈, du ma la wēdi. Tālube ya yepa ne nōga itam.
36Yesu nak ñou ak ñom chi bereb bu tūda Gethsemane, te ne i tālube am, Tōg len file ba ma dem ñān fale.
37Mu jel ak mōm Peter ak ñar i dōm i Zebedee, dôr di yogorlu ak nah͈arlu lol.
38Mu ne len, Suma fit angi nah͈arlu bu miti, be chi dē sah͈: jēki len file, te otu ak man.
39Mu dem tūti cha kanam, defēnu chi suf, te ñān, ne, E suma Bay, su munê am, na nānu bile wey fi man: wande du naka ma ko buge, wande naka nga ko buge.
40Mu ñou fi tālube ya, feka len ñu di nelou, te ne Peter, Lan! munu len a otu ak man wena wah͈tu?
41Otu len te ñān, ndah͈ du len tabi chi bulis: fit wi souar na chi dega, wande yaram wi new na dōle.
42Mu dem ñarel i yōn wa, te ñān, ne, E suma Bay, su lile munulê wey, lu moy ma nān ko, lo buga na am.
43Mu ñouati, feka len ñu di nelou, ndege sēn i but dīs on nañu.
44Mu bayiati len, dem, te ñān ñetel i yōn wa, wah͈ati bāt yōgale.
45Fōfale mu ñou fi tālube ya, te ne len, Nelou len lēgi, te nopalaku: wah͈tu wi jegeñsi na, te or nañu Dōm i nit ka chi loh͈o i bakarkat ya.
46Jog len, na ñu dem, ki ma orsi jegeñsi na.
47Ba mu wah͈andô, Judas, kena chi fuk’ ak ñar ña, ñou, and’ ak mōm mbōlo mu rey ñu am i jāsi ak i doko, ñu juge fa i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña.
48Ki ko or nak joh͈ na len firnde, ne, Ka ma fōni, mōm la: japa len ko.
49Mu ñou fi Yesu chi tah͈ouay, ne, Noyu nā la, Rabbi, te mu fōn ko.
50Yesu ne ko, Anda, defal li la tah͈ a dika. Fōfale ñu ñou, teg sēn i loh͈o chi Yesu, te jel ko.
51Kena chi ña neka ak Yesu talal loh͈o am, bochi jāsi am, dōr rapas i kēlifa i seriñ ya, te dog nop’ am.
52Yesu ne ko, Delōl sa jāsi chi mbar am: ndege ñepa ña fab jāsi, di nañu dānu ak jāsi.
53Dēfe nga ne munu ma dagān suma Bay, te lēgi mu may ma lu upa jurom bena fuka njūne’ malāka am?
54Wande naka la mbinda mi di motalikô, ne nōgu la ela ame?
55Chi wah͈tu wōwale Yesu ne mbōlo ma, Dika ngēn jelsi ma ak i jāsi ak i doko, niki sachakat? Dan nā tōg ak yēn gir gu neka, di jemantale chi juma ja, te japu len ma won.
56Wande lile yepa am na, ndah͈ mbinda i yonent ya motaliku. Fōfale la ko tālube ya yepa woche, te dou.
57Ña jap’ on Yesu yubu ko cha nēg i Caiaphas, kēlifa i seriñ ya, fa bindānkat ya ak mag ya dajalo won.
58Wande Peter topa ko bu sorey chi ker i kēlifa i seriñ ya, h͈araf chi bir, te tōg ak rapas ya, ndah͈ mu sêt muj ga.
59I njīt i seriñ ya nak ak ndaje ma yepa ūt sēde i fen lu jem chi Yesu, ndah͈ ñu rēy ko.
60Sēdekat i fen yu bare ñou nañu, wande amu ñu dara. Cha ganou ga ñar ñou, ne,
61Nit kile wah͈ on na, ne, Mun nā dānel juma’ Yalla, te tabah͈ati ko chi ñet’ i fan.
62Kēlifa i seriñ ya jog, te ne ko, Do tontu dara? li la ñile sēdêl?
63Wande Yesu japa gemeñ am. Kēlifa i seriñ ya ne ko, Mangi la dagān chi tur i Yalla ji di dunda, nga wah͈ ñu ndah͈ yā di Krista, Dōm i Yalla.
64Yesu ne ko, Wah͈ nga ko: te mangi len di wah͈, Ganou lile di ngēn gisi Dōm i nit ka mu di tōg chi loh͈o’ ndējor i kantan, di wachasi chi i nir i asaman.
65Fōfale kēlifa i seriñ ya h͈oti chol am, ne, H͈as na Yalla: ban sēde la ñu soh͈lāti? Dēga ngēn h͈as am nak:
66Lan ngēn dēfe? Ñu tontu ne, Dagan na dē.
67Fōfale ñu tufli chi kanam am, te mbumbanda ko: ñenen dōr ko ak sēn i loh͈o,
68Ne, Tolātle ñu, you Krista, kan a la dōr?
69Peter nak don na tōg cha biti cha ker ga: bena janh͈a ñou fi mōm, ne, Yā nek’ on ak Yesu wā’ Galilee ba.
70Wande mu wēdi chi kanam i ñepa, ne, H͈amu ma li nga wah͈.
71Ba mu deme be h͈araf cha rum ba, kenen gis ko, te ne ña fa neka, Kile nek’ on na itam ak Yesu wā’ Nazareth ba.
72Mu wēdêti ak ngeñ, ne, H͈amu ma nit ki.
73Ganou lōlale tūti, ña tah͈ou fa ñou fi Peter, te ne ko, Chi dega kena chi ñom nga; ndege sa laka fêñal na la.
74Fōfale mu dal di mōlu, di geñ, ne, H͈amu ma nit ki. Nōn’ ak nōna seh͈a ga sab.
75Peter fataliku bāt ba Yesu wah͈ on, ne, Bala seh͈a ga sab, di nga ma wēdi ñet’ i yōn. Mu gēna, te joy bu miti.

Currently Selected:

Matthew 26: GWG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in