John 3

3
1Nit i Pharisee ya am on na, ku tuda Nicodemus, kēlifa i Yauod ya:
2Kōkale ñou on na fi mōm chi gudi, te ne ko, Rabbi, h͈am nañu ne yā di jemantalkat ba bayako fa Yalla: ndege ken munul a def koutef yile nga def, su Yalla nekule ak mōm.
3Yesu tontu te ne ko, Chi dega, chi dega, mangi la wah͈, Su nit jūduātule, du mun a gis ngur i Yalla.
4Nicodemus ne ko, Naka la nit mune jūdu ba mu magete? Ndah͈ mun na duga chi bir i ndey am ñarel i yōn, te jūdu?
5Yesu tontu, ne, Chi dega, chi dega, mangi la wah͈, Su nit jūduwule chi ndoh͈ ak Nh͈el ma, du mun a h͈araf chi ngur i Yalla.
6La jūdu chi yaram wi yaram la; te la jūdu chi Nh͈el ma nh͈el la.
7Bul jomi ndege da ma la wah͈, ne, Ela ngēn a jūduāt.
8Ngelou li gelou na fa mu buga, te dēga nga rir am, wande h͈amu la fu mu bayako, te fu mu jem: nōnule la ku neka ku jūdu chi Nh͈el ma.
9Nicodemus tontu te ne ko, Naka la yef yile mune am?
10Yesu tontu te ne ko, Ndah͈ yā di jemantalkat i Israel, te h͈amu la yef yile?
11Chi dega, chi dega, ma ne la, Wah͈ nañu lu ño h͈am, te sēde lu ño gis; te nanguwu len suñu sēde.
12Su ma len wah͈e yef i aduna, te gumu len, naka ngēn di gume su ma len wah͈e yef i ajana?
13Te kena yēgul on cha ajana, wande ka wach’ on cha ajana, Dōm i nit ka sah͈, ka neka cha ajana.
14Te naka Musa yēkate won jān ja cha manding ma, nōnale sah͈ la ñu ela yēkati Dōm i nit ka;
15Ndah͈ ku mu mun a don ku gum chi mōm di na am dūnda gu dul jêh͈.
16Ndege Yalla sopa na aduna si be mu maye Dōm am ja di bajo, ndah͈ ku mu mun a don ku gum chi mōm du sanku, wande mu am dūnda gu dul jêh͈.
17Ndege Yalla yōniwul on Dōm am chi aduna si ndah͈ mu ate aduna si; wande ndah͈ aduna si mucha chi mōm.
18Ku gum chi mōm atewu ñu ko; ku gumul, ate nañu ko jēg, ndege gumul on chi tur i Dōm i Yalla ja di bajo.
19Te bile di ate ba, ne lêr gi ñou na chi aduna si, te nit sopa lendem gi as lêr gi, ndege sēn i jefin bon na.
20Ndege ku neka ku di def lu bon bañ na lêr gi, te du ñou chi lêr gi, ndah͈ i jef am fêñ.
21Wande ku di def dega gi, di na ñou chi lêr gi, ndah͈ i jef am fêñ ne chi Yalla la len ligey.
22Ganou yef yōyu Yesu ak i talube am ñou on nañu cha suf i Judea; te mu jēki fa ak ñom te batise.
23Te John itam don na batise cha Ænon bu jegeñ Salim, ndege ndoh͈ mu bare anga fa won: te ñu di ñou di batisesi.
24Ndege bōba tejangu ñu on John chi kaso.
25Lājte jog nak chi digante i talube i John ak Yauod ya chi lu jem chi setalay.
26Te ñu ñou fi John, te ne ko, Rabbi, Kōkale nek’ on ak you ganou wala Jordan, ka nga sēde won, munga batise, te ñepa dika fa mōm.
27John tontu te ne, Nit munul a nangu dara, su ñu ko ko mayule cha ajana.
28Yēn chi sēn bopa sēde ngēn ma ne ma wah͈ on, ne, Dowu ma Krista, wande yōni nañu ma chi kanam am.
29Ka am seyt ba borom‐seyt ba la; wande h͈arit i borom‐seyt ba, ka tah͈ou te dēga ko, mō banēh͈u bu bare ndig bāt i borom‐seyt ba: suma banēh͈ bile mbōk motaliku.
30Mō ela doliku, wande mā ela wañiku.
31Ka juge cha kou, chi kou ñepa la neka: ka juge aduna, chi aduna la boka, te lu boka chi aduna la wah͈: ka juge ajana, chi kou ñepa la neka.
32La mu gis te dēga, lōlu la sēde; te ken nanguwul sēde am.
33Ka nangu sēde am, def na kaste am ne Yalla dega la.
34Ndege kōka Yalla yōni on, bāt i Yalla yi la wah͈: ndege joh͈ewul Nh͈el ma chi natu.
35Bay ba sopa na Dōm ja, te joh͈ na ko lu neka chi loh͈o am.
36Ku gum chi Dōm ja, am na dūnda gu dul jêh͈; wande ku gumul Dōm ja du gis dūnda, wande mer i Yalla deka ak mōm.

Currently Selected:

John 3: GWG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in