Njàlbéen ga 8

8
Nóoyin génn na gaal gu mag ga
1Ci biir loolu Yàlla xalaat na Nóoyin ak li mu nekkal ci gaal gi, di rabi àll yi ak jur gi. Yàlla daldi yebal ngelaw, mu wal kaw suuf, ba ndox yi wàcc. 2Bëti ndox ya ca xóote ya dafa taxaw, bunti ndoxi asamaan tëju, taw bi dal. 3Ci kaw loolu ndox mi taa ci suuf di wàññiku. Bi téeméeri fan yi ak juróom fukk matee nag, ndox ma gëna néew. 4Ba juróom ñaareelu weer wa amee fukki fan ak juróom ñaar, gaal gaa nga teereji tundi Araraat. 5Ndox may wàññiku rekk ba ca fukkeelu weer wa. Keroog ba fukkeelu weer wa teroo, ca la njobbaxtali tund ya tàmbalee feeñ.
6Teg nañu ca ñeent fukki fan, Nóoyin doora ubbi poroxndoll, ba mu sàkkaloon gaal ga, 7daldi yebal ab baaxoñ, muy naaw, di dem ak a dikk, ba ndox mi fendi ci kaw suuf. 8Mu teg ca yebal pitax, ba xam ndax ndox mi ci suuf fer na. 9Teewul pitax ma gisul fenn fu mu tag, ndax ndox mi muur na suuf sépp. Mu délsi nag fa moom ca gaal ga. Nóoyin tàllal loxoom, jàpp ko dugal ci biir fi wetam. 10Négandiku na juróom ñaari fan, doora yebalaat pitax ma. 11Ba mu délsee ca ngoon, indaalewul lu moy xobu oliw wu tooy wu keppe ca sàll wa. Nóoyin xam ne ndox mi taa woon ci suuf, fer na. 12Mu négati juróom ñaari fan, bàyyiwaat pitax ma. Boobu yoon nag délsiwaatul ca moom.
13At ma Nóoyin amee juróom benni téeméeri at ak benn, keroog benn fanu weer wa jëkk, ndox ma taa woon ca suuf daldi fendi. Nóoyin ubbi kubeer ga, xool, ba gis ne kaw suuf sépp wow na. 14Keroog ñaar fukki fan ak juróom ñaar ca ñaareelu weer wa, ca la suuf si doora wow koŋŋ.
15Ba loolu amee Yàlla ne Nóoyin: 16«Génnal gaal gi, yaak sa soxna ak say doom ak say soxnay doom. 17Génnewaaleel lépp luy xeetu mbindeef mu ngeen àndal: picc yi ak bàyyima yi ak luy raam, ñu fulandiwu ci kaw suuf, daldi giir te bare.» 18Nóoyin daldi génn, moom aki doomam ak soxnaam ak soxnay doomam ya. 19Rabi àll yi ak luy raam ak luy naaw ak luy dox ci kaw suuf— lépp génne ca gaal ga, lu ci nekk ak wirgoom.
20Naka la Nóoyin génn, daldi sàkkal Aji Sax ji sarxalukaay, màggale ko ko. Mu sàkk nag ci mboolem rab wu set ak mboolem picc mu set, jébbal Yàlla ca sarxalukaay ba, muy saraxu rendi-dóomal. 21Ci kaw loolu xetug jàmm gillee ca sarax sa, yéeg fa Aji Sax ja. Booba la wax ci xolam ne: «Dootuma rëbb suuf mukk ndax nit, doonte ba muy ndaw lay dale xinte lu ñaaw ci xolam. Dootuma boole fàdd mukk lépp luy dund, nii ma ko defe.
22Li feek suuf di suuf,
dootu jiwooy dakk mbaa ngóob,
te du sedd aku tàngoor,
du nawet it mbaa noor,
mbaa guddeek bëccëg.»

Currently Selected:

Njàlbéen ga 8: KYG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in