Njàlbéen ga 13

13
Ibraam ak Lóot teqlikoo nañu
1Bi loolu amee Ibraam dafa jóge Misra, moom ak soxnaam, yóbbaale alalam jépp, daldi dem ca àllub Negew, Lóot topp ca. 2Ibraam nag amoon alal ju bare diggante jur, xaalis ak wurus. 3Gannaaw loolu mu awati yoonam, jóge àllub Negew, jëm dëkk ba ñu naa Betel, dem ba àgg ca bérab, ba mu jëkkoona samp xaymaam, ci diggante Betel ak Ayi, 4fa mu tabaxoon ab sarxalukaay. Ibraam nag tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko.
5Ci biir loolu Lóot, mi mu àndal, moom it yor jur gu gudd ak gu gàtt aki xayma, 6ba tax xajatuñu ca réew ma, ndax seen alal dafa bare, ba manatuñu faa bokk dëkk. 7Loolu tax sàmmi Ibraam ak sàmmi Lóot di jote. Rax ci dolli Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ña nga woon ca réew ma.
8Ba loolu amee Ibraam da ne Lóot: «Waay waay, bu xuloo am sama digganteek yaw mbaa say sàmm ak samay sàmm. Xanaa dunuy bokk nag? 9Xanaa àll bi newul yàmblaŋ ngay gis? Nan teqlikoo, kay; boo demee càmmoñ, ma dem ndijoor; boo demee ndijoor, ma dem càmmoñ.»
10Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Sowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja#13.10 Tool booba mooy Àjjana, fa Yàlla jëkkoona dëkkal Aadama ak Awa. . 11Ba mu ko defee Lóot tànn jooru Yurdan gépp, daldi toxu jëm penku. Noonu lañu teqlikoo. 12Ibraam dëkke réewu Kanaan, Lóot sance dëkk ya ca jooru Yurdan, daldi toxal xaymaam, samp ko Sodom. 13Waaye waa Sodom ñu bon lañu woon, te mana moy Aji Sax ji lool.
Digeb Aji Sax ja ak Ibraam
14Gannaaw ba Lóot teqlikook Ibraam, Aji Sax ji wax na Ibraam ne ko: «Téenal foofu nga taxaw, te séenu bëj-gànnaar ak bëj-saalum ak penkook sowu, 15ndaxte réew, mi ngay gis mépp, yaw laa koy may ba fàww, yaak askan wi soqikoo ci yaw. 16Dinaa leen yokk, ba ñu tollu ni feppi suuf, ba feppi suuf gëna neexa waññ sa askan. 17Jógal wër réew mi mépp, ba mu daj, ndax yaw laa koy may.»
18Ba mu ko defee Ibraam sempi xaymaam, ñëw dal Ebron ca garab yu mag ya ca toolub Mamre, daldi fay tabaxal Aji Sax ji sarxalukaay.

Currently Selected:

Njàlbéen ga 13: KYG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in