Njàlbéen ga 10

10
Askanu doomi Nóoyin
(Saar 10.1—11.9)
Xeet yi sosoo ci doomi Nóoyin
1Askanu doomi Nóoyin mooy lii. Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Sem ak Xam ak Yafet am nañu ay doom.
Li jëm ci askanu Yafet
2Doomi Yafet yu góor ñii la: Gomeer ak Magog ak Madéy ak Yawaan ak Tubal ak Meseg ak Tiraas. 3Doomi Gomeer yu góor di Askenas, Rifaat ak Togarma. 4Doomi Yawaan yu góor di Elisa ak Tarsis ak Kitim ak Dodanim. 5Ñi sosoo ci ñoom ñoo law ca wàllaa géej, meññ nag ay xeet ci seeni suuf, xeet wu ci nekk ak làkkam, def it ay làng ci seen biiri xeet.
Li jëm ci askanu Xam
6Doomi Xam yu góor ñoo di ñii: Kuus ak Misrayim ak Puut ak Kanaan. 7Doomi Kuus yu góor di Seba ak Awila ak Sabta ak Raama ak Sabteka. Doomi Raama yu góor di Saba ak Dedan.
8Kuus moom itam jur Namróot, ki jëkk di jàmbaar ju siiw ci kaw suuf, 9mu doonoon rëbbkat bu maga mag. Looloo waral ñu naan: «Mbete Namróot, rëbbkat bu maga mag ba.» 10Dëkk yiy péeyi nguuram ñoo di: Babel ak Ereg ak Akàdd ak Kalne, gi ci réewu Sineyaar. 11-12Ca réew mooma la Namróot jóge dem Asur, sanc dëkk bu mag boobee di Niniw, ak dëkk yooyee di Reyobot Ir ak Kala, ba Resen, gi ci diggante Niniw ak Kala.
13Misrayim nag mooy maami Luddeen ñi ak Anameen ñi ak Leyabeen ñi ak Naftuyeen ñi 14ak Pataruseen ñi ak Kasluyeen, ñooñee waa Filisti bàyyikoo ca seen réew; ak it Kaftoreen ñi.
15Kanaan moo taawloo Sidon, teg ca Ett, 16te mooy maami Yebuseen ñi ak Amoreen ñi ak Girgaseen ñi 17ak Eween ñi ak Arkeen ñi ak Sineen ñi, 18ak Arwàddeen ñi ak Semareen ñi ak Amateen ñi. La ca tegu làngi Kanaan tasaaroo. 19Kemu suufas Kanaaneen ña, mu ngi tàmbalee Sidon, jaar weti Gerar, dem ba Gasa, wuti Sodom ak Gomor ak Atma ak Ceboyim, daldi teeri Lesa.
20Ñooñu ñooy askani Xam, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew.
Li jëm ci askanu Sem
21Sem, miy magu Yafet, jur na moom itam ay doom yu góor. Mooy maami Eber ak askanam. 22Doomi Sem yu góor ñii la: Elam ak Asur ak Arpagsàdd ak Ludd ak Aram. 23Góor ñi Aram jur ñii la: Uus ak Xuul ak Geter ak Maas. 24Arpagsàdd jur Sela, Sela jur Eber; 25Eber moom, jur ñaari doom yu góor, kenn ki tudd Peleg (mu firi Séddlikoo), ndaxte ci jamonoom àddina dafa séddlikoo woon. Rakku Peleg mooy Yogtaan.
26Yogtaan a jur Alamodàdd ak Selef ak Asarmawet ak Yera 27ak Adoram ak Usal ak Digla 28ak Obal ak Abimayel ak Saba 29ak Ofir ak Awila ak Yobab. Ñooñu ñépp di doomi Yogtaan yu góor. 30Ña nga dëkkoon ca wàllu Mesa, ga wuti Sefar, di diiwaanu tund ya ca penku.
31Ñooñoo askanoo ci Sem, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew.
32Làngi doomi Nóoyin yu góor a ngoogu, làng gu nekk ak askanam, ñu diy xeet. Ci ñoom la xeet yépp jóge tasaaroo ci kaw suuf, gannaaw ba mbënn ma wéyee.

Currently Selected:

Njàlbéen ga 10: KYG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in