1
Matthew 23:11
Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907
Wande ku gen a rey chi sēn digante, na neka sēn bukanēg.
Compare
Explore Matthew 23:11
2
Matthew 23:12
Ku yēkati bop’ am, di nañu ko sufel; te ku sufelu bop’ am, di nañu ko yēkati.
Explore Matthew 23:12
3
Matthew 23:23
Suboh͈un yēn, bindānkat yi ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn fey asaka i oyof ya, te sagane yef i yōn wa gen a rey, mu di njūbay, ak yermande, ak ngum: yile ñom ngēn war on a def, te bañ a sagane yena ya.
Explore Matthew 23:23
4
Matthew 23:25
Suboh͈un yēn, bindānkat yi, ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn di setal biti’ ndap ak kela, wande cha bir fês na ak ndāntu ak nchaychay.
Explore Matthew 23:25
5
Matthew 23:37
E Jerusalem, Jerusalem, mu rēy yonent ya, te jamat i h͈êr ña ñu ko yōne! naka lā don faral a buge dajale sēn i dōm, naka ganar gu di dajale i dōm am chi run lāf am, te ngēn bañ.
Explore Matthew 23:37
6
Matthew 23:28
Nōgu itam ngēn di wone njūlit chi nit chi biti, wande chi bir da ngēn fês ak nafeh͈a ak bakar.
Explore Matthew 23:28
Home
Bible
გეგმები
Videos