1
Njàlbéen ga 4:7
Kàddug Yàlla gi
Soo defee lu baax, dees na la nangul; soo deful lu baax, bàkkaar a ngi lay yeeru ci sa bunt, di la tërook a wut, waaye yaa ko wara man.»
Compare
Explore Njàlbéen ga 4:7
2
Njàlbéen ga 4:26
Set it, am doom ju góor, tudde ko Enos. Fan yooya lañu tàmbalee tudd Aji Sax ji, di ko wormaal.
Explore Njàlbéen ga 4:26
3
Njàlbéen ga 4:9
Aji Sax ji ne Kayin: «Ana sa rakk Abel?» Mu ne ko: «Gisuma ko de; xanaa maa wara sàmm sama rakk?»
Explore Njàlbéen ga 4:9
4
Njàlbéen ga 4:10
Yàlla ne ko: «Loo def? Sa deretu rakk jaa ngi yuuxoo ci suuf, ma di ci dégg.
Explore Njàlbéen ga 4:10
5
Njàlbéen ga 4:15
Aji Sax ji ne ko: «Kon nag ku la rey, yaw Kayin, dina jot juróom ñaari yoon lu ko raw.» Ba loolu amee mu sàkkal Kayin màndarga, ba ku ko gis du ko rey.
Explore Njàlbéen ga 4:15
Home
Bible
გეგმები
Videos