1
Njàlbéen ga 2:24
Kàddug Yàlla gi
Looloo tax góor di bàyyikoo ci ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñuy wenn suux.
Compare
Explore Njàlbéen ga 2:24
2
Njàlbéen ga 2:18
Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.»
Explore Njàlbéen ga 2:18
3
Njàlbéen ga 2:7
Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan.
Explore Njàlbéen ga 2:7
4
Njàlbéen ga 2:23
Aadama ne tonet, daldi ne: «Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux! Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële.»
Explore Njàlbéen ga 2:23
5
Njàlbéen ga 2:3
Yàlla daldi barkeel bésub juróom ñaareel ba, def ko bés bu sell, ndax da caa dal-lu woon gannaaw liggéey, ba mu sàkke lépp.
Explore Njàlbéen ga 2:3
6
Njàlbéen ga 2:25
Ku góor ki ak soxnaam, ñoom ñaar ñépp, yaramu neen lañu defoon, te amuñu ci woon genn kersa.
Explore Njàlbéen ga 2:25
Home
Bible
გეგმები
Videos