Matthew 1

1
1Tēre’ toflante i gir i Yesu Krista, dōm i Dauda, dōm i Ibrayuma.
2Ibrayuma jur on na Isaka; Isaka jur Yanh͈oba; Yanh͈oba jur Judah ak i dōm i bay am;
3Te Judah jur Perez ak Zerah cha Tamar; Perez jur Hezron; Hezron jur Ram;
4Te Ram jur Amminadab; Amminadab jur Nahshon; Nahshon jur Salmon;
5Te Salmon jur Boaz cha Rahab; Boaz jur Obed cha Ruth; Obed jur Jesse;
6Te Jesse jur bur Dauda; bur Dauda jur Suleyman, chi ka nek’ on jabar i Uriah;
7Te Suleyman jur Rehoboam; Rehoboam jur Abijah; Abijah jur Asa;
8Te Asa jur Jehoshaphat; Jehoshaphat jur Joram; Joram jur Uzziah;
9Te Uzziah jur Jotham; Jotham jur Ahaz; Ahaz jur Hezekiah;
10Te Hezekiah jur Manasseh; Manasseh jur Amon; Amon jur Josiah;
11Te Josiah jur Jechoniah ak i dōm i bay am, cha jamāno ja ñu len gadaylo won fa Babylon:
12Ganou ba ñu len yubu on fa Babylon, Jechoniah jur Shealtiel; Shealtiel jur Zerubbabel;
13Te Zerubbabel jur Abiud; Abiud jur Eliakim; Eliakim jur Azor;
14Te Azor jur Sadoc; Sadoc jur Achim; Achim jur Eliud;
15Te Eliud jur Eleazar; Eleazar jur Matthan; Matthan jur Yanh͈oba;
16Te Yanh͈oba jur Yusufa jekar i Mariama, ka nek’ on ndey i Yesu, ka ñu tūda Krista.
17H͈êt ya yepa mbōk cha Ibrayuma be cha Dauda fuk’ i h͈êt la ak ñenent; te cha Dauda be cha ngaday ga fa Babylon fuk’ i h͈êt la ak ñenent; te cha ngaday ga fa Babylon be chi Krista fuk’ i h͈êt la ak ñenent.
18Njūdu’ Yesu Krista nile la won: Ba ndey am Mariama nangulante Yusufa, ba mu lāta sey ak mōm, fêñu on na ak bir chi Nh͈el mu Sela ma.
19Yusufa jekar am, nek’ on ku jūb, te nangôdi ndig wone ko chi biti, bug’ on na ko fase chi kumpa.
20Wande ba mu h͈alāte yef yile, malāka i Borom bi fêñu ko chi gēnta, ne ko, Yusufa, dōm i Dauda, bul ragal a sey ak Mariama, ndege li chi bir am chi Nh͈el mu Sela ma la juge.
21Di na jur dōm ju gōr, te na nga ko tūde Yesu, ndege mō di musali mbōtay am chi sēn i bakar.
22Yile yepa am on na ndah͈ la Borom bi wah͈ on chi yonent ba motaliku, ne,
23H͈ēk ba di na bir, te jur dōm ju gōr, te di nañu ko tūde Emmanuel; mu tiki, Yalla and’ ak ñun.
24Yusufa jog chi nelou, def la ko malāka i Borom bi ebal on, te jel ko jabar:
25H͈amu ko be ba mu jure tau am, ba mu tūde Yesu.

Valið núna:

Matthew 1: GWG

Áherslumerki

Deildu

Afrita

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in