Exodus 20
20
EBLI YA.
1Yalla wah na baat yili, ni na:
2I. Man maa di Yalla saa Borom, ka laa jili ce suf i Egipta, ce neg i njam. 3B ulu am yenen i yalla ganau Man.
4II. Bulu defar ce saa bopa bena natal bu nu erta, mbaati natal bu mu mun na don bu neka ce ajana ce kou, mbaati bu neka ce aduna ce suf, mbaati bu neka ce ndoh ma ca run suf si. 5Bulu sukal saa bopa fi nom, ne, da nga len di jaamu: ndegi, Man Yalla saa Borom, Yalla bu fir la, te di teg bakar i bai yi ce kou dom yi, ca netel ak nenentel i hert na maa ban, 6t e woni mbaaali c’ i njuni ca na maa sopa, te denca suma i baat.
7III. Bulu jil tur i Yalla saa Borom ce cahan, ndegi, Borom bi, du ko seti naka bakar, ku jil tur am ce cahan.
8IV. Halaatal bes i Dimas pur denca ko mu sela. 9Jurum ben’ i fan nga lige, te def saa lige yipa; wandi, 10jurum narel i fan ba mu Dimas i Yalla saa Borom. Ce mom, bulu def bena lige, you oh, saa dom ju gor oh, saa dom ju jigen oh, saa rapas bu gor oh, saa rapas bu jigen oh, saa get oh, mbaat saa gan gu dal ak you. 11Ndegi, ce jurum ben’i fan la, Borom ba defar asaman ak suf, gec ge ak la ce neka, te nopaliko ce jurum narel i fan ya, te barke ko.
12V. Teralal saa bai ak saa nde, ndah saa i fan mun na guda ce suf sa la Yalla saa Borom mai.
13VI. Bulu re kena.
14VII. Bulu njaalo.
15VIII. Bulu saca.
16IX. Bul johi sede bu nekul diga ce saa dikando.
17X. Bul hemin saa neg i dikando, bul hemin saa jaba i dikando, waala rapas am bu gor, waala rapas am bu jigen, waala nag am, waala mbam am, waala lu mun na neka alalam.
Currently Selected:
Exodus 20: GWG
Tõsta esile
Share
Copy
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.