YouVersion Logo
Search Icon

Matthew 25

25
1Fōfale di nañu nirale ngur i ajana ak fuk’ i h͈ēk, ñu jel on sēn i lampa, di gatanduji borom‐seyt.
2Jurom chi ñom nek’ on nañu ñu ñaka sago, te jurom ña di ñu am sago.
3Ñu ñaka sago ña jel sēn i lampa, te yubuāleū ñu diwlin ak ñom:
4Wande ñu am sago ña yubuāle diwlin chi sēn i ndap ak sēn i lampa.
5Ba borom‐seyt ba yīh͈e, ñepa gemantu te nelou.
6Wande chi dig’ i gudi h͈āchu ma jib, ne, Borom‐seyt bā’nge dika! Dem len, gatanduji ko.
7Fōfale h͈ēk yōyale yepa jog, te jagal sēn i lampa.
8Ñu ñaka sago ña wah͈ ñu am sago ña, ne, May len ñu chi sēn diwlin; ndege suñu i lamp’ ange fey.
9Wande ñu am sago ña tontu, ne, H͈ēchna du doy chi ñun ak yēn: na ngēn dem fa ña di jay, te jendal sēn bopa.
10Ba ñu deme di jendi, borom‐seyt ba agsi; te ña jaglu on h͈arafando ak mōm cha nchēt la; te bunta ba teju.
11Cha ganou ga yenen h͈ēk ya ñou itam, ne, Borom bi, Borom bi, ūbi ñu.
12Wande mu tontu, ne, Chi dega mangi len di wah͈, h͈amu ma len.
13Otu len mbōk, ndege h͈amu len bes ba, wala wah͈tu wa.
14Mel na niki nit ku don tūki chi benen rew, mu ôlu i jām am, te dēnka len alal am.
15Mu joh͈ kena jurom i talent, kenen ñar, kenen bena; ku chi neka ak munmun am; te dal di tūki.
16Fōfale ka mu joh͈ on jurom i talent ya dem jayatu, te doli yenen jurom i talent.
17Ka mu joh͈ on ñar ya itam, tofal cha yenen ñar.
18Wande ka mu joh͈ on bena, mu dem, gas chi suf si, te nuba h͈ālis i borom am.
19Ba mu yāge cha ganou, borom i jām yōya delusi, te jel konta ak ñom.
20Ka mu joh͈ on jurom i talent ya ñou, te indi yenen jurom i talent, ne, Borom bi, joh͈ on nga ma jurom i talent: yenen jurom i talent angi yi ma chi doli.
21Borom am ne ko, Wau gōr, E jām bu bāh͈ bi te taku: da nga gōre chi lu new, di nā la teg njīt chi lu bare: h͈arafsil chi sa banēh͈ i borom.
22Ka mu joh͈ on ñar i talent ya ñou itam, ne, Borom bi, joh͈ on nga ma ñar i talent: yenen ñar i talent angi yi ma chi doli.
23Borom am ne ko, Wau gōr, E jām bu bāh͈ bi, te taku: da nga gōre chi lu new, di nā la teg njīt chi lu bare: h͈arafsil chi sa banēh͈ i borom.
24Ka mu joh͈ on bena talent ñou itam, ne, Borom bi, H͈am nā ne yā di nit ku āybir; da nga gōb fo jiūl on, te di forātu fo tūrul on;
25Ma ragal on, te dem, nuba sa talent chi suf si: li nga mōm angile.
26Wande borom am tontu ko, ne, E jām bu bon bi, te tayal; h͈am on nga ne da ma gōb fu ma jiūl on, te forātu fu ma tūrul on;
27Tah͈na war on nga joh͈e wēchikat yi suma h͈ālis; kônte su ma ñoue, am kon nā la ma mōm ak suma ngañmay.
28Nangu len talent bi chi mōm mbōk, te joh͈ ko ki ame fuk’ i talent yi.
29Ndege ku am la ñu di joh͈, te di na am lu bare; wande ku amul, di nañu nangu la mu el’ on a am sah͈.
30Te sani len jām bu jeriñul bi cha lendem i biti: fōfale la joy di neka, ak yey i buñ.
31Bu Dōm i nit ka di ñoui chi ndam am, ak malāka ya yepa and’ ak mōm, di na tōg chi kou gangūne’ ndam am:
32Di na dajale h͈êt yi yepa chi kanam am; te di na len h͈ajātle ku neka chi morom am, naka sama di h͈ajātle i nh͈ar ak i bey:
33Di na teg nh͈ar ya chi ndējor am, wande bey ya chi chamoñ am.
34Fōfale Bur ba di na wah͈ ña cha ndējor am, ne, Ñou len, yēn ña suma Bay barkel, dona len rew mu ñu len wājal on cha ndôrte’ aduna si:
35Ndege da ma h͈īf on, ngēn joh͈ ma ma leka: da ma mar on, ngēn joh͈ ma ma nān: da ma don gan, ngēn ganale ma:
36Ma rāfle, ngēn sānga ma: ma jēr, ngēn sêtsi ma: ma neka chi kaso, ngēn ñou fi man.
37Fōfale ñu jūb ña di nañu ko tontu, ne, Borom bi, kañ la ñu la gis on nga h͈īf, te ñu dundal la? wala nga mar, te ñu joh͈ la nga nān?
38Kañ la ñu la gis on nga di gan, ñu ganale la? wala nga rāfle, ñu sānga la?
39Kañ la ñu la gis on nga jēr, wala chi kaso, te ñu sêtsi la?
40Bur ba di na len tontu, ne, Chi dega mangi len di wah͈, Ndege def on ngēn ko chi kena chi suma i mboka yile ku gen a tūt, man ngēn ko defal on.
41Fōfale di na wah͈ ña chi chamoñ am, ne, Randu len ma, yēn ñi alaku, dem len cha safara su dul jêh͈, ba ñu wājal on Seytane ak i malāk’ am:
42Ndege da ma h͈īf on, joh͈u len ma ma leka: ma mar, joh͈u len ma ma nān:
43Ma don gan, ganaleū len ma: ma rāfle, sāngu len ma: ma jēr, te neka chi kaso, te sêtsiū len ma.
44Ñom it di nañu ko tontu, ne, Borom bi, kañ la ñu la gis on nga h͈īf, wala nga mar, wala nga di gan, wala nga rāfle, wala nga jēr, wala chi kaso, te dimaliū ñu la?
45Di na len tontu, ne, Chi dega mangi len di wah͈, Ndege defu len ko won chi ku gen a tūt chi ñile, man ngēn ko defalul on.
46Ñile di nañu dem chi ndān gu dul jêh͈: wande ñu jūb ña chi dunda gu dul jêh͈.

Currently Selected:

Matthew 25: GWG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in