YouVersion Logo
Search Icon

Matthew 17

17
1Ganou jurom ben’ i fan, Yesu jel Peter, James, ak John rak’ am, te yubu len chi kou tūnda wu koue, ñom dal:
2Mu sopaliku chi sēn kanam: h͈ar‐kanam am di melah͈ niki janta bi, te ser am wêh͈ tal niki lêr gi.
3Te Musa ak Elijah fêñu len, di wah͈tān ak mōm.
4Peter tontu, ne Yesu, Borom bi, bāh͈ na chi ñun ñu neka file: su la nêh͈e, di nā fi defar ñet’ i mbār; bena you, bena Musa, ak bena Elijah.
5Ba mu wah͈ande, nir wu ne naña umba len, te bāt juge cha nir wa, ne, Kile di suma Dōm ja ma sopa; chi mom lā def suma h͈ol bepa; dēga len ko.
6Ba ko tālube ya dēge, ñu defēnu chi suf, te tīt lol.
7Yesu ñou, te lāl len, ne, Jog len, te bu len tīt.
8Ba ñu yēkate sēn but, gisatu ñu ken, ganou Yesu dal.
9Ba ñu wache tūnda wa, Yesu ebal len, ne, Bu len wah͈ kena mpêñu mile, be ba Dōm i nit ka di dēki cha ñu dē ña.
10I tālube am lāj ko, ne, Lutah͈ bindānkat ya ne Elijah ela na jeka ñou?
11Mu tontu len, ne, Elijah di na ñou chi dega, to delo yef yepa:
12Wande mangi len di wah͈, Elijah ñou on na jēg, te h͈amu ñu ko won, wande ñu def ko lu ñu buga chi mōm. Nōgu itam la ño sonaleji Dōm i nit ka.
13Tālube ya h͈am nak, ne wah͈ na len lu jem chi John Batisekat ba.
14Ba ñu dike chi mbōlo ma, nit ñou fi mōm, di sūka fi mōm, ne,
15Borom bi, amal yermande chi suma dōm ju gōr; ndege defa say, te getenu bu miti; faral na tabi chi safara, ak chi ndoh͈.
16Yubu on nā ko chi sa i tālube, te munu ñu ko weral.
17Yesu tontu, ne, E h͈êt wu gumadi, te deger‐bopa, be kañ lā neka ak yēn? be kañ lā len muñal? Indi ko fi man.
18Yesu h͈ūle ko, te jine ja gēna chi mōm; cha wah͈tu wōwale h͈alel ba wer.
19Fōfale tālube ya ñou fi Yesu chi kumpa, ne, Lutah͈ ño ko munul on a gēne?
20Mu ne len, Ndig sēn gumadi: ndege chi dega mangi len di wah͈, Su ngēn ame ngum gu day niki pēp’ i sūna, di ngēn wah͈ tūnda wile, Roñul cha bereb bale; te di na roñu; te kôn dara du len te.
21Wande h͈êt wile du gēna lu dul chi ñān ak chi kôr.
22Ba ñu deke chi Galilee, Yesu ne len, Di nañu or Dōm i nit ka chi loh͈o i nit;
23Di nañu ko rēy, te chi ñetel i fan am di na dēki. Ñu nah͈arlu lol.
24Ba ñu dike chi Capernaum, ña di jel ngalak la ñou fi Peter, ne, Ndah͈ sēn borom du fey ngalak?
25Mu ne, Wau. Ba mu h͈arafe chi nēg ba, Yesu jekantu ko, ne, Lo dēfe Simon? I bur i suf si, chi kan la ñu di jele bāh͈ wala ngalak? chi sēn i dōm am, am chi i gan?
26Ba mu ne, Chi gan yi, Yesu ne ko, Kôn dōm ya du ñu war a fey.
27Wande ndah͈ du ñu len fakatal, demal cha gēch ga, sani ôs, te japa jen wu jeka fêñ; bo ūbe gemeñ am, di nga cha feka dogit i h͈ālis: jel ko, te joh͈ len ko ngir man ak you.

Currently Selected:

Matthew 17: GWG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in