YouVersion Logo
Search Icon

John 5

5
1Ganou yef yile h͈ewte i Yauod ya am on na; te Yesu dem fa Jerusalem.
2Cha Jerusalem nak, cha bunt’ i nh͈ar ya, dēg anga fa won bu tūda Bethesda chi lak’ i Yauod ya, te am na jurom i bulu.
3-4Chi bir i mbōlo chi ñu op’ on, i silmah͈a, i lago, ak i lafañ teda fa.
5Te kena nit anga fa won ka am on jangaro am ñeta fuk’ i at ak jurom ñeta.
6Ba ko Yesu gise mu teda, te h͈am ne nek’ on na nōgule bu yāga, mu ne ko, Ndah͈ buga nga wer?
7Jarak ba tontu ko, ne, Borom bi, amu ma kena ku ma tabal chi dēg gi su ndoh͈ mi di yengu: wande bu ma di dem, kenen jītu ma dem chi bir.
8Yesu ne ko, Jogal, enu sa lal, te doh͈.
9Te chi tah͈ouay nit ka dal di wer, te jel lal am te doh͈. Bes bōba nak Dimas la won.
10Tah͈na Yauod ya ne ka ñu weral on, Tey Dimas la, te daganul nga yubu sa lal.
11Wande mu tontu len, ne, Ka ma weral on, mō ma wah͈ on, ne, Enul sa lal te doh͈.
12Ñu lāj ko, ne, Kan nit a la wah͈ on, ne, Enul sa lal te doh͈?
13Wande ka ñu weral on h͈amul kan la: ndege Yesu gēn’ on na, ndig mbōlo anga fa won.
14Cha ganou ga Yesu feka ko cha juma ja, te ne ko, Yangi wer nak: bul bakarati, mbāte lu gen a bon dal chi sa kou.
15Nit ka dem te wah͈ Yauod ya ne Yesu a ko weral on.
16Lōlo tah͈ Yauod ya don geten Yesu, ndege def na yef yile chi bes i Dimas.
17Wande Yesu tontu len, ne, Suma Bay angi ligey bentey, te man itam mangi ligey.
18Lile tah͈ Yauod ya dole ūt naka ñu ko rēye, ndege moyul on Dimas ji reka, wande tūda na Yalla Bay am itam, di emale bop’ am ak Yalla.
19Mōtah͈ Yesu tontu te ne len, Chi dega, chi dega, ma ne len, Dōm ji munul a def dara chi bop’ am, su gisule Bay ba mu def ko: ndege lu mu mun a don lu mu def, lile la Dōm ji di def nōgule itam.
20Ndege Bay ba sopa na Dōm ji, te won ko yef yu mō def yepa: te di na ko won yef yu upa yile, ndah͈ ngēn jomi.
21Ndege naka Bay ba dēkali ñu dē ña, te tah͈ ñu dūnda, nōna sah͈sah͈ la Dōm ji itam di na dūndalo ku mu buga.
22Ndege Bay ba atewul kena, wande joh͈ na Dōm ji ate yepa;
23Ndah͈ ñepa mun a teral Dōm ji naka ñu terale Bay ba. Ku teralul Dōm ji teralul Bay ba ko yōni on.
24Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Ku dēga suma bāt, te gum ka ma yōni on, am na dūnda gu dul jêh͈, te du ñou chi ate, wande romba na chi dē be chi dūnda.
25Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Wah͈tu wā’nge ñou, te jot na lēgi, ba ña dē di dēga bāt i Dōm i Yalla, te ña dēga di nañu dūnda.
26Ndege naka Bay ba ame dūnda chi bop’ am, nōgule itam mu joh͈ on Dōm ji mu am dūnda chi bop’ am:
27Te joh͈ ko sañsañ itam mu motali ate, ndege mō di Dōm i nit ka.
28Bu len jomi chi lile: ndege wah͈tu di na ñou ba ña chi bamel ya ñepa di nañu dēga bāt am,
29Te di nañu gēna; ña def on lu bāh͈ cha ndēkite’ dūnda: te ña def on lu bon cha ndēkite’ ate.
30Munu ma def dara chi suma bopa: naka ma dēge nōnu lā di ate; te suma ate jūb na; ndege ūtu ma suma mbugel, wande mbugel i ka ma yōni on.
31Su ma sēde suma bopa, suma sēde du dega.
32Kenen a ma sēde; te h͈am nā ne sēde ba mu ma sēde dega la.
33Yōni on ngēn fa John, te mō sēde won dega gi.
34Wande sēde ba ma am, du chi nit la juge: wande yef yile lā wah͈ ndah͈ ngēn mucha.
35Mō don lampa ba di tāka te di melah͈: te nangu won ngēn a banēh͈u chi i sā cha lêr am ga.
36Wande sēde ba ma am mō upa bu John: ndege ligey ya ma Bay ba joh͈ ma motali len, ligey yile lā def, ño ma sēde ne Bay ba ma yōni on.
37Te Bay ba ma yōni on, mō ma sēde. Mosu len a dēga bāt am, mbāte gis melo am.
38Te amu len bāt am mu deka chi yēn: ndege ka mu yōni on gumu len ko.
39Janga ngēn mbinda yi, ndege dēfe ngēn ne chi ñom ngēn am dūnda gu dul jêh͈; te yile ma sēde;
40Te bugu len a ñou fi man, ndah͈ ngēn am dūnda.
41Nanguwu ma ndam chi nit.
42Wande h͈am nā len, ne amu len nchofel i Yalla chi sēn bopa.
43Da ma ñou chi suma tur i Bay, te nanguwu len ma: su kenen di ñou chi tur i bop’ am, mōm ngēn di nangu.
44Naka ngēn mune gum, yēn ña nangulante ndam, te ndam li juge cha Yalla reka, ūtu len ko?
45Bu len dēfe ne mā len di jêñ chi Bay ba: kena am na ka len di jêñ, mu di Musa, ka ngēn def on sēn yākar.
46Ndege su ngēn don gumi Musa, man ngēn gum kon; ndege bind’ on na chi lu jem chi man.
47Wande su ngēn gumule mbind’ am ya, naka ngēn di gum suma i wah͈?

Currently Selected:

John 5: GWG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in