Luug 5
5
Yeesu woo na ay taalibe
1Yeesoo taxawoon ca tàkkal dexu Senesaret#5.1 dexu Senesaret mooy dexu Galile ba tey., mbooloo ma tancaloo ci kawam, di déglu kàddug Yàlla. 2Ci biir loolu mu gis ñaari gaal yu taxaw ci tàkk gi, nappkat ya ca wàcce, di fóot seeni mbaal. 3Mu dugg ci genn gaal gi, muy gu Simoŋ. Mu ñaan ko mu bëmëx ba dànd tefes gi as lëf. Mu defal ko noonu, Yeesu toog, tàmbalee jàngal mbooloo ma fa mu tollu ca biir gaal ga.
4Naka la jàngle ba noppi, ne Simoŋ: «Bëmëxal ba ca xóote ba, te ngeen sànni seeni mbaal ba jàpp.» 5Simoŋ ne ko: «Njaatige, coono lanu fanaane biig te jàppunu dara. Xanaa ma sànni ko rekk ci sa ndigal.»
6Naka lañu sànni mbaal yi, daldi jàpp jën yu baree bare, ba mbaal ya di xëtt. 7Ba loolu amee ñu liyaar seen moroom, ya ca geneen gaal ga, ngir ñu dimbalisi leen. Ñu dikk, yebandook ñoom, feesal ñaari gaal yépp, ba ñuy bëgga suux. 8Simoŋ Piyeer nag gis loolu, daldi sukk fa kanam Yeesu, ne ko: «Sang bi, ngalla sore ma, ngir man nitu bàkkaarkat laa!», 9ndax tiitaange lu ko jàpp, mook mboolem ña mu àndal, ca jën yu bare ya ñu jàpp. 10Yanqóoba ak Yowaan doomi Sebede ya mu bokkaloon liggéey ba itam noonu lañu tiite. Yeesu ne Simoŋ: «Bul ragal dara; gannaaw-si-tey, ay nit ngay napp.» 11Ci kaw loolu ñu teeral gaal ya ca tefes ga, daldi bàyyi lépp, topp ca moom.
Yeesu faj na ku gaana
12Yeesoo nekkoon cib dëkk, ndeke jenn waay a nga fa, ju jàngoroy ngaana dajal yaram wa. Ba mu gisee Yeesu, daa daanu, dëpp jëëm ci suuf, sarxu ko, ne: «Sang bi, su la soobee, man nga maa setal.» 13Yeesu tàllal loxoom, laal ko ne: «Soob na ma, setal.» Ca saa sa ngaana ga teqlikook moom. 14Yeesu dénk ko ne ko: «Bu ko wax kenn, demal rekk ca sarxalkat ba, ngir mu seet la, te nga génne sa jooxeb setlu, ni ko yoonu Musaa santaanee, muy firnde ci ñoom#5.14 Ci yoonu Musaa, jàngoroy der juy law ju mel ni ngaana sobe la woon ca ka mu dal, te du set li feek wérul. Seetal ci Sarxalkat yi 13.45-46; 14.1-32..» 15Teewul jëwub Yeesu gënatee law. Mbooloo yu bare daje, di ko déglu tey faju, ba tàggook seeni jàngoro. 16Moom nag muy rocceekuy dem ba ci bérab yu wéet, di fa ñaaneji.
Yeesu faj na ab lafañ
17Yeesu moo doon jàngle bés, fu ay Farisen ak ay jànglekati yoonu Musaa tooge, jóge ca mboolem dëkki Galile ak Yude ak Yerusalem, te manoorey Boroom bi teew faak moom, ngir faj jarag ja.
18Ci biir loolu ay nit ne jalañ, jàppoo ab lafañ bu ñu tëral cig laltu. Ñu di ko wuta dugal, ngir tëral ko ca kanam Yeesu. 19Waaye gisuñu fu ñu koy awale ndax mbooloo ma. Ñu yéeg ca kaw néeg ba, xeddi lenn ca xadd ba, yoor waa jaak laltu ga, wàcce ko ca digg ba, fa kanam Yeesu. 20Yeesu nag gis seen ngëm, daldi ne lafañ ba: «Mbokk mi, jéggalees na la say bàkkaar.»
21Firikati yoonu Musaa yi ak Farisen yi tàmbalee nàttable ci seen xel, naan: «Kii di saaga Yàlla mooy kan? Ana ku mana jéggaley bàkkaar ku dul Yàlla doŋŋ?»
22Yeesu nag xam la ñuy nàttable ci seen xel, daldi àddu, ne leen: «Lu ngeen di nàttable ci seen xel? 23Ana lu gëna yomb ci yii yaar: ne “Jéggalees na la say bàkkaar,” am ne: “Jógal te dox”? 24Kon nag dingeen xam ne Doomu nit ki am na ci kaw suuf, sañ-sañu jéggale ay bàkkaar.» Mu ne lafañ ba: «Dama ne, jógal, jël sag laltu te dem ñibbi.» 25Nit ka daldi ne ñokket ca kanam ñépp, jël laltu ga mu tëddoon, jëm këram, di sàbbaal Yàlla. 26Ba loolu amee mbooloo mépp a neey, di sàbbaal Yàlla, tiitaange jàpp leen, ñu naan: «Gis nanu tey mbir yu tiiñ am xel.»
Yeesu woo na Lewi
27Gannaaw loolu Yeesu génn, gis ab juutikat bu ñuy wax Lewi, mu toog ca juuti ba. Mu ne ko: «Kaay, topp ma.» 28Lewi jóg, bàyyi lépp, topp ca moom. 29Ci kaw loolu Lewi waajalal ko bernde ju réy ca këram. Mbooloo mu bare teew, ay juutikat ak yeneen gan, ñu bokk toog, di lekk. 30Farisen yi ak seeni firikat nag di xultu ci kaw taalibey Yeesu yi, ne leen: «Lu tax ngeen di lekkandoo ak a naanandoo ak juutikat yeek bàkkaarkat yi?» 31Yeesu ne leen: «Du ñi wér ñoo soxla fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla. 32Du ñi jub nag laa woosi, bàkkaarkat yi laay woo, ngir jëme leen cig tuubeel.»
Koor du wartéef ci gëmkatub Yeesu
33Dañoo wax Yeesu, ne ko: «Taalibey Yaxya de, dinañu faral di woor, di julli. Farisen yi it noonu, waaye sa ñoñ, lekk ak a naan lañu wéye.» 34Yeesu ne leen: «Ndax man ngeena woorloo ay gan ñu wàlli ag céet, li feek boroom séet biy teew ci seen biir? 35Waaye ay bés a ngi ñëw, dees na jële boroom séet bi ci seen biir. Kera bés yooyu nag, dinañu woor.»
36Yeesu léebati leen, ne leen: «Mbubb mu bees, deesu ci xotti ab sekkit, ngir daaxe ko mbubb mu ràpp. Lu ko moy mbubb mu bees mi xottiku ba noppi, te du tax sekkit wu bees wi ànd ak mbubb mi ràpp. 37Te it mbuus yu ràpp, deesu ci duy biiñ bu bees. Lu ko moy biiñ bu bees bi fàcc mbuus yi; biiñ bi tuuru, mbuus yi yàqu. 38Biiñ bu bees daal, ci mbuus mu bees lees koy denc. 39Te itam deesul naan biiñ bu yàgg, di bëggati bu bees, xanaa nga ne: “Bu yàgg bee baax#5.39 Biiñ, nee ñu lu mu gëna yàgg rekk moo gën..”»
Currently Selected:
Luug 5: KYG
Highlight
Share
Copy
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Copyright © 2010, 2020 La Mission Baptiste du Sénégal