YouVersion Logo
Search Icon

Luug 17

17
Bàkkaarloo nit aay na
1Yeesu neeti ay taalibeem: «Ag fiir guy bàkkaarloo manula ñàkk, waaye wóoy ngalla ka koy lal. 2Ñu takkoon doj wu réy ci baatam, sànni ko biir géej moo gën ci moom muy yóbbe bàkkaar kenn ci xale yii. 3Wattuleen seen bopp.
Jéggal-leen ku leen tuubal
«Bu la sa mbokk tooñee, yedd ko. Bu tuubee, baal ko. 4Su la tooñoon juróom ñaari yoon ci bés bi, te walbatiku juróom ñaari yoon, ne la: “Tuub naa ko,” baal ko rekk.»
Ngëm maye na kéemtaan
5Ci kaw loolu ndaw ya ne Sang bi: «Yokk nu ngëm.» 6Sang bi ne leen: «Su ngeen amoon ci ngëm, lu tollu ni peppu fuddën sax, ba ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbate ca géej ga,” su boobaa garab gi déggal leen.
Ab jaam du sàkku jaajëf
7«Kan ci yeen la ab jaamam di beyi mbaa mu sàmmi ba jóge tool, dikk, mu ne ko: “Kaay, nu lekk”? 8Xanaa kay da koy wax ne ko: “Defaral sama reer, te takku, taajal ma, ba ma lekk, naan, nga doora lekk, naan.” 9La jaam ba jëfe ndigal tax na sangam sant ko? Déedéet kay. 10Yeen itam noonu. Bu ngeen defee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay jaam rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
Yeesu faj na fukki gaana
11Ci biir yoon woowu Yeesu jëmoon Yerusalem, ma nga jaare fa Samari ak Galile digaloo. 12Mu dem bay duggsi cib dëkk, fukki gaana dikk, dajeek moom, ba dànd ko, daldi taxaw. Ñu xaacu ne: 13«Yeesu, Njaatige, yërëm nu!» 14Yeesu nag gis leen, ne leen: «Demleen seetluji seen yaram ca sarxalkat ya.»
Ba ñuy dem ca sarxalkat ya lañu wér, seen yaram set. 15Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi walbatiku, di xaacuy sàbbaal Yàlla. 16Mu dikk, ne gurub, dëpp jëëm fa tànki Yeesu, sant ko. Waa ja nag nitu Samari la woon. 17Ba loolu amee Yeesu ne: «Xanaa du fukk a wér? Juróom ñeent ña nag, ana ñu? 18Amu ci kenn ku ñëw, delloo Yàlla njukkal ku dul doxandéem bii!» 19Yeesu nag ne ko: «Jógal dem; sa ngëm faj na la.»
Nguurug Yàlla door na ba noppi
20 Farisen yi ñoo laajoon Yeesu, ne ko: «Kañ la nguurug Yàlla di dikk?» Mu ne leen: «Dikkug nguurug Yàlla du ànd akum ceetaan. 21Deesul ne it: “Xool-leen, mu ngi” mbaa: “Ma ngee,” ndax kat nguurug Yàlla mu ngi ci seen biir.»
22Mu ne taalibe ya: «Ay jant a ngi ñëw yu ngeen naa ngéejoo fekke benn bés ci bési Doomu nit ki, te dungeen ko fekke. 23Te it, dees na leen ne: “Ma ngee!” mbaa: “Mu ngii!” Buleen dem, buleen ca topp. 24Ndax ni melax di xuyye gii wetu asamaan, ba ne ràññ ca gee, noonu la Doomu nit kiy def keroog bésam. 25Waaye balaa booba fàww Doomu nit ki am coono yu bare, jànkoonteek diiŋatu niti tey jii.
26«Noonee mu deme woon ca janti Nóoyin, ni lay deme ca janti Doomu nit ki. 27Nit ñaa nga doon lekk ak a naan, di jël jabar ak a séyi, ba keroog bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga, mbënn ma dikk, sànk ñépp.
28«Noonee itam la deme woon ca janti Lóot. Nit ñaa nga doon lekk ak a naan, di jënd ak a jaay, di jëmbat ak a tabax. 29Waaye bés ba Lóot génnee Sodom, la tawub sawara ak tamarax wàcce asamaan, sànk ñépp. 30Noonu doŋŋ lay deme, bés bu Doomu nit kiy feeñ.
31«Bésub keroog boobee, ku mu fekk ci kaw am taax, te say yëf ne ca biir kër ga, bul wàcc, di ko jëli. Te ku mu fekk tool ba itam, bul dellu. 32Fàttlikuleen jabaru Lóot ja! 33Képp kuy wuta rawale sa bakkan, yaay ñàkk sa bakkan, waaye képp ku ñàkk sa bakkan, yaay dund. 34Maa leen ko wax: guddig keroog ñaar ay bokk benn lal, kenn ki, ñu yóbbu ko, ka ca des, ñu ba ko. 35-36Ñaar di wolandoo, kenn ki, ñu yóbbu ko, ka ca des, ñu ba ko.»
37Taalibe yi ne Yeesu: «Loolu fan la, Sang bi?» Mu ne leen: «Fu médd nekk, fa la tan yay daje.»

Currently Selected:

Luug 17: KYG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in