Njàlbéen ga 9
9
Yàlla fas na kóllëre ak Nóoyin
1Ci kaw loolu Yàlla barkeel Nóoyin aki doomam ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina. 2Mboolem rabi àll yi ak njanaawi asamaan ak ndëgmeent yi ci suuf, ak jëni géej yépp, dinañu leen ragal lool. Teg naa leen ci seeni loxo. 3Man ngeena dunde boroom bakkan yooyu yépp. Jagleel naa leen bindeef yooyu yépp, ni ma leen jagleele woon gàncax.
4«Waaye buleen lekk yàpp wu ànd ak deret, ndaxte dund a ngi ci deret. 5Seen dundu nit itam, mu ngi ci seen deret, kon kat, képp ku tuur seen deret dinaa ko ko topp. Te it mala mu ci rey nit dinaa ko ko topp, ni may toppe nit. Dinaa topp ku nekk deretu moroomam.
6Ku tuur deretu nit,
na nit tuur deretam,
ngir melokaanu boppam
la Yàlla sàkke nit.
7Yeen nag, giirleen te bare, fulandiwu ci kaw suuf te fees ko.»
8Yàlla nag wax Nóoyin ak doomam, yi mu àndal, ne leen: 9«Bés niki tey fasal naa sama bopp kóllëre sama diggante ak yeen ak seen askan, 10fas ko it sama diggante ak mboolem mbindeef mu ngeen àndal, muy picc akug jur mbaa rabi àll— lépp daal lu génnandoo ak yeen ci gaal gi, di lépp luy dund ci kaw suuf. 11Ni may faseek yeen kóllëre nii la:
Deesatul boole bindeef yépp, faat ci mbënn mukk.
Du menn mbënn mu deeti faagaagal àddina.»
12Yàlla neeti: «Kóllëre gi may fas ak yeen ak mboolem mbindeef mu ànd ak yeen, day sax ba fàww te liy màndargaam mooy lii: 13def naa sama xon ci niir yi, muy màndargaal kóllëre, gi dox sama diggante ak àddina.
14«Saa su ma dajalee niir yi ci jaww ji, ba xon gi feeñ ci niir yi, 15damay daldi xalaataat kóllëre, gi ma fas sama digganteek yeen ak mboolem xeeti bindeef, su ko defee ndox dootu sabab mbënn muy faagaagal lépp luy dund. 16Xon gi day nekk ci biir niir yi, ma di ko gis, di xalaat kóllëre, gi ma fas fàww, sama diggante, man Yàlla, ak mboolem xeetu mbindeef mu nekk ci kaw suuf.» 17Ci kaw loolu Yàlla ne Nóoyin: «Loolu mooy màndargaal sama kóllëre, gi ma fas ak mboolem mbindeef mu nekk ci kaw suuf.»
Mbirum Nóoyin ma aki doomam
18Doomi Nóoyin yu góor, yi génne ci gaal gi, ñooy: Sem, Xam ak Yafet; Xam mooy baayu Kanaan. 19Ñooñu ñooy ñetti doomi Nóoyin yu góor, te ci ñoom la àddina sépp soqikoo.
20Nóoyin ab beykat la woon. Mu nekk nag ci njëmbatum reseñ. 21Mu am bés mu naan biiñ, ba màndi, tëdd ci xaymaam, daldi sàgganu.
22Ba loolu amee Xam, baayu Kanaan, gis céri baayam, génn waxi ko Sem ak Yafet ca biti. 23Sem ak Yafet ànd, jël malaan, teg ko ci seeni mbagg, doxe gannaaw ba agsi, doora sàng seen céri baay. Dañoo dummóoyu, ba gisuñu seen céri baay.
24Màndite ma giif, Nóoyin yewwu, daldi yég ni xale bi def ak moom. 25Ba mu ko defee mu ne:
«Yal na Kanaan torox,
bay jaamu jaami doomi ndeyam.»
26Mu dellu ne:
«Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Sem,
yal na Kanaan dib jaamam.
27Yal na Yàlla lawal askanu Yafet,
dëël ko ci xaymay Sem,
te Kanaan di seen jaam.»
28Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Nóoyin dundaat na ñetti téeméeri at ak juróom fukk (350). 29Nóoyin dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom fukk (950), doora faatu.
Currently Selected:
Njàlbéen ga 9: KYG
Highlight
Share
Copy
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Copyright © 2010, 2020 La Mission Baptiste du Sénégal