YouVersion Logo
Search Icon

Njàlbéen ga 31

31
Yanqóoba toxu na, jëm Kanaan
1Ba loolu amee mu am bés Yanqóoba dégg doomi Laban ya naan, Yanqóoba nangu na li seen baay amoon lépp, te ci seen alalu baay la sàkkoo alalam jooju jépp. 2Naka la Yanqóoba gis kanamu Laban, daldi xam ne melatul, na mu meloon ci moom. 3Aji Sax ji wax Yanqóoba ne ko: «Dellul ca sa réewu maam ya, ca say bokk. Dinaa ànd ak yaw.»
4Yanqóoba woolu Rasel ak Leya ca tool ya, fa gàttam ya nekk. 5Mu ne leen: «Gis naa seen kanamu baay. Xam naa ne melatul na mu meloon ci man. Waaye sama Yàllay baay ay ànd ak man. 6Yeen ci seen bopp xam ngeen ne liggéeyal naa seen baay sama kem kàttan. 7Teewul seen baay wor ma, soppi sama peyoor fukki yoon ak juróom, waaye Yàlla seetaanu ko, mu di ma lor. 8Bu nee: “Yi tippanteey sa peyoor,” jur gépp jur lu tippante; mbaa mu ne: “Yi seereer ay sa peyoor,” jur gépp jur lu seereer. 9Nii la Yàlla nangoo seen juru baay, jox ma.
10«Ba ñu demee ba jur giy wara tëbu, damaa jeneer sikket yiy tëb bëy yi yépp di lu seereer ak lu tippante mbaa ñu raxe. 11Ca la ma malaakam Yàlla ma wax ci biir gént gi ne ma: “Yanqóoba,” ma ne ko: “Naam.” 12Mu ne ma: “Siggil, xool sikket yiy tëb bëy yi yépp, yii dañoo seereer, yee todde, yi ci des tippante, ndaxte gis naa li la Laban di def lépp. 13Maay Yàlla, ja la feeñu woon Betel, fa nga samp doj, sotti ci diw, sellale ko, te dogu woon fa ci man. Léegi nag jógal, génn réew mii, dellu ca réew, ma nga juddoo.”»
14Rasel ak Leya ne ko: «Ndax amati nanu benn cér walla ndono sunu kër baay? 15Doonunu lu moy ay doxandéem ci moom de! Nde da noo jaay, lekk sunu njég, ba mu jeex tàkk. 16Te mboolem alal, ji Yàlla nangoo ci sunu baay, noo ko moom, nun ak sunuy doom. Kon nag léegi lu la Yàlla wax rekk, def ko.»
17Yanqóoba daldi dajale ay doomam ak ay soxnaam, waral leen giléem, 18ñu ànd tegu ca yoon wa, yóbbaale géttam gépp ak mboolem alal ju mu liggéey. Mooy gétt, ga mu sàkkoo Padan Aram. Ña ngay ñibbi kër baayam Isaaxa ca réewu Kanaan.
19Fekk na Laban dem wati ay xaram#31.19 Xari waa penku dañuy bare kawar gu ñuy wat ak a ëcc, di ci defar ag wëñ.. Ci biir loolu Rasel sàcc gàllaaji kër yu baayam. 20Noonu la Yanqóoba nëbboo Laban, Arameen ba, bañ koo yégal ne day dem. 21Ba mu demee, dafa yóbbaale la mu amoon lépp, jóge fa, jàll dexu Efraat, wuti tundi Galàdd.
Laban dabi na Yanqóoba
22Yanqóoba daw na, ba mu am ñetti fan, ñu soog koo yégal Laban. 23Mu ànd nag ak ay bokkam, topp ko juróom ñaari fan, door koo dab ca tundi Galàdd. 24Ci kaw loolu Yàlla feeñu Laban, Arameen ba, ci géntu guddi ne ko: «Moytula wax Yanqóoba lenn lu koy gaar.» 25Ba Laban dabee Yanqóoba, dafa fekk mu samp xaymaam ca tund wa. Laban it samp bosam ca kaw tundi Galàdd, moom aki bokkam.
26Laban ne Yanqóoba: «Looy def nii, yaw, di ma nëbbuy daw, yóbbaale sama doom yu jigéen, ñu mel ni ñu ñu lële xare? 27Lu waral nga di ma nëbbuy daw te bañ maa tàggu? Nde konoon jombul ma yiwi la ci xol bu sedd, bu ànd aki woy, boole ci xalam aki sabar. 28Mayoo ma sax, ma fóon samay sët ak samay doom yu jigéen, tàggtook ñoom; yëfi dof de nga def nii! 29Manoon naa laa def lu bon, waaye sa Yàllay baay da maa feeñu biig ne ma: “Moytula wax Yanqóoba lenn lu koy gaar.” 30Bu la neexee, nga namm sa kër baay, ba dogu caa dem, waaye lu tax nga sàcc sama gàllaaji kër, teg ci?»
31Yanqóoba tontu Laban ne ko: «Xanaa ragaloon rekk ne jombul dinga téye say doom yu jigéen. 32Waaye képp koo gis mu yor sa gàllaaji kër, boo yeboo reyal. Seetal fii ci sunu kanami bokk lépp lu ma fi yor, loo ci moom fabal, yóbbu.» Booba Yanqóoba xamul woon ne Rasel a ko jël. 33Laban dugg ci xaymab Yanqóoba, teg ca xaymab Leya ak yosi ñaari jaamam yu jigéen ya, te gisul dara. Mu génne xaymab Leya, dugg ci bu Rasel.
34Fekk na Rasel fab gàllaaji kër ya, làq ca ron tegu giléem ga, toog ca. Laban tëcc, tëcc ca biir xayma ba, gisul dara. 35Rasel wax baayam ne ko: «Baay, baal ma de, damaa manula jóg ci sa kanam, ndaxte damaa ànd ak mbaax.» Laban seet na fu ne, waaye gisul gàllaaji këram ya.
36Yanqóoba mer lool, daldi gëdd Laban ne ko: «Ndax damaa tooñ walla damaa moy, ba nga sambal ma, di ma topp nii? 37Bi nga jéexee sama yëf yépp ba noppi, ana loo gis lu bokk ci sa yëfi kër? Teg ko fii ci sama kanami bokk ak say bokk, ñu àtte nu. 38Xanaa du ñaar fukki at a ngii ma nekk ak yaw? Say xar ak say bëy ëmbuñu sax, mu yàqu, te masumaa lekk sa kuuyi gétt. 39Jur gu rab fàdd sax ma féetewoo, waaye masuma la koo indil. Mboolem lu ñu sàcc guddi ak lu ñu sàcc bëccëg, danga ma ko daa feyu. 40Naaj wi laa daan yendoo yenu bëccëg, di fanaanoo sedd guddi, mu xaw maa rey, ba duma gëmm bët. 41Ñaar fukki at a ngii, ma di la jaamu ci kër gi, liggéeyal naa la fukki at ak ñeent ngir sa ñaari doom yu jigéen ñii, teg ci juróom benni at yu ma la sàmmal say gàtt, nga soppi sama peyoor fukki yoon ak juróom. 42Su dul woon ak sama Yàllay baay, ji ànd ak man, di Yàllay Ibraayma, ji Isaaxa wormaaloon, konoon nga dàq ma tey, ma dem loxoy neen. Waaye sama toskare ak sama àqu ñaq la Yàlla gis, ba tax mu àtte ma ak yaw biig.»
43Ba mu ko waxee loolu, Laban ne ko: «Jigéen ñii samay doom lañu, xale yii di samay sët, te gétt gii sama gétt a; lu fi nekk maa ko moom. Ñii di sama doom yu jigéen, nu ma leen di def tey, ñoom ak seeni doom? 44Léegi ñëwal rekk, ñu fasante kóllëre maak yaw, te seede dox sunu diggante maak yaw.» 45Ba loolu amee Yanqóoba jël aw doj, samp ko, muy doju xàmmikaay. 46Yanqóoba ne ay bokkam: «Forleen ay doj.» Ñu for ay doj, def ko ab jal, daldi lekk foofa ca wetu jal ba. 47Laban tudde bérab ba Yegar Saaduta; Yanqóoba tudde ko Galet#31.47 Galet bokk na lu mu tekki ak Yegar Saaduta ci làkku Arameen ña..
48Booba la Laban ne: «Jal bii tey, mooy sunu seede sama diggante ak yaw.» Moo tax ñu tudde ko Galet (mu firi Jalub seede). 49Ñu di ko tudde itam Mispa (mu firi Tatay wattukaay), ndax Laban da ne: «Yal na Aji Sax ji wattu sunu diggante, keroog bu ñu soree. 50Soo soxoree samay doom yu jigéen, mbaa nga takk yeneen jabar, bu fa kenn nekkul sax, moytul, ndax Yàllaa nuy seede.» 51Laban neeti Yanqóoba: «Xoolal ci jal bii ak doju xàmmikaay, wi ci sama digganteek yaw. 52Jal bi seede la, doj wi di seede ne duma jéggi jal bi, jublu ci yaw, te yaw itam doo jéggi jal bi mbaa doj wi, jublu ci man, te naraluloo ma jàmm. 53Yàllay Ibraayma ak Yàllay Naxor, ñoom ñooñee di seen Yàllay baay, yal nañu àtte sunu diggante.» Yanqóoba daldi giñ ci Yàlla, ji baayam Isaaxa wormaaloon. 54Gannaaw loolu Yanqóoba sàkk sarax ca kaw tund wa, woo ay bokkam, ñu bokk lekk. Ba ñu lekkee ba noppi, fanaan ca tund wa.

Currently Selected:

Njàlbéen ga 31: KYG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in