YouVersion Logo
Search Icon

Njàlbéen ga 11

11
Yàlla safaan na làkku àddina, mu jaxasoo
1Ca ndoorte la nag waa àddina sépp a bokkoon wenn làkk, seeni wax di benn. 2Bi nit ñi toxoo, jëm penku, dañoo gis ag joor ci réewu Sineyaar, ñu sanc fa. 3Ñu ne: «Ayca nu defar ay móol yu ñu lakk cib taal, ba mu ñor.» Ci kaw loolu ñu def móol ya doji tabax, taqalee ko koltaar, 4daldi ne: «Ayca nu tabax ab dëkk bu taax ma bëtt asamaan; kon dinanu am woy, te dunu tasaaroo ci kaw suuf.»
5Ba ñu noppee Aji Sax ji wàcc, xoolsi dëkk bi ak taax, mi doom aadama yi tabax. 6Aji Sax ji da ne: «Su ñu tàmbalee nii, di menn mbooloo te bokk wenn làkk, kon dara dootu leen të. 7Ayca nu wàcc, safaan seen làkk, ba dootuñu déggoo.»
8Ba loolu amee Aji Sax ji jële leen foofa, tasaare leen ci kaw suuf sépp, ñu yemale fa dëkk ba ñu doon tabax. 9Looloo tax ñu tudde dëkk ba Babel (mu firi Safaan), ndax foofa la Aji Sax ji safaane làkku àddina sépp, mu jaxasoo, te fa la leen tasaaree ci kaw suuf sépp.
Askanu Sem, maamu Ibraam
(Saar 11.10-26)
10Askanu Sem mooy lii. Sem am na téeméeri at, doora jur Arpagsàdd, fekk na mbënn ma wees, ba mu am ñaari at. 11Arpagsàdd juddu na, Sem dundaat juróomi téeméeri at (500), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen.
12Arpagsàdd am fanweeri at ak juróom, jur Sela. 13Sela juddu na, Arpagsàdd dundaat ñeenti téeméeri at ak ñett (403), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen.
14Sela am fanweeri at, jur Eber. 15Eber juddu na, Sela dundaat ñeenti téeméeri at ak ñett (403), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen.
16Eber am fanweeri at ak ñeent, jur Peleg. 17Peleg juddu na, Eber dundaat ñeenti téeméeri at ak fanweer (430), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen.
18Peleg am fanweeri at, jur Rew. 19Rew juddu na, Peleg dundaat ñaar téeméeri at ak juróom ñeent (209), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen.
20Rew am fanweeri at ak ñaar, jur Serug. 21Serug juddu na, Rew dundaat ñaar téeméeri at ak juróom ñaar (207), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen.
22Serug am fanweeri at, jur Naxor. 23Naxor juddu na, Serug dundaat ñaar téeméeri at, juraat ay doom yu góor ak yu jigéen.
24Naxor am ñaar fukki at ak juróom ñeent, jur Teraa. 25Teraa gane na àddina, Naxor dundaat téeméeri at ak fukk ak juróom ñeent (119), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen.
26Gannaaw ba Teraa amee juróom ñaar fukki at, am na Ibraam ak Naxor ak Aran.
Askanu Teraa, baayu Ibraam
(Saar 11.27—25.11)
27Askanu Teraa mooy lii. Teraa mooy baayu Ibraam#11.27 Ibraam mii: Yàlla dina ko mujja tudde Ibraayma. Seetal ci 17.5. ak Naxor ak Aran. Aran mooy baayu Lóot. 28Gannaaw loolu Aran faatu na lu jiitu faatug baayam Teraa, ca réew ma mu juddoo, di Ur#11.28 Ur: dëkk bu yàggoon la, te bokkoon ci réew, mi ñu tudde Iraag léegi. , dëkku Kaldeen ña. 29Ibraam ak Naxor jël nañu ay soxna; soxnas Ibraam tudd Sarayi, soxnas Naxor di Milka. Milka moomu, moom ak rakkam ju jigéen Yiska, Aran ay seen baay. 30Sarayi moomu masuloona am doom te it manu ko woona am.
31Mu am bés Teraa ànd ak doomam Ibraam ak sëtam Lóot, mi Aran di baayam, ak Sarayi, soxnas Ibraam. Ñu bokk jóge Ur gu Kaldeen ña, jëm réewu Kanaan. Ba ñu demee ba Karan, daldi fay sanc. 32Teraa dund na ñaar téeméeri at ak juróom (205), doora génn àddina, ñu denc ko Karan.

Currently Selected:

Njàlbéen ga 11: KYG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in