1
Njàlbéen ga 32:28
Kàddug Yàlla gi
Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.»
Compare
Explore Njàlbéen ga 32:28
2
Njàlbéen ga 32:26
Ba nit ka xamee ne manalu ko dara, dafa dóor Yanqóoba ci mooco, mooco mi summikoo ca bëre ba.
Explore Njàlbéen ga 32:26
3
Njàlbéen ga 32:24
Yanqóoba da leena jàllale, jàllewaale alalam jépp itam.
Explore Njàlbéen ga 32:24
4
Njàlbéen ga 32:30
Yanqóoba ne ko: «Waaw, yaw nag noo tudd?» Mu wax ko ne ko: «Loo may laaje sama tur?» ba noppi barkeel ko foofa.
Explore Njàlbéen ga 32:30
5
Njàlbéen ga 32:25
Mu des fa nag moom doŋŋ. Kera la genn góor fanaana bëre ak moom, ba bët set.
Explore Njàlbéen ga 32:25
6
Njàlbéen ga 32:27
Nit ka ne ko: «Bàyyi ma, ma dem, ndax bët a ngi bëgga set.» Teewul Yanqóoba ne ko: «Duma la bàyyi, nga dem, li feek ñaanaloo ma.»
Explore Njàlbéen ga 32:27
7
Njàlbéen ga 32:29
Nit ka ne ko: «Tuddatuloo Yanqóoba, léegi Israyil nga tudd, ndaxte bëre nga ak nit, bëre ak Yàlla, ba génn ci ak jàmm.»
Explore Njàlbéen ga 32:29
8
Njàlbéen ga 32:10
Ci kaw loolu Yanqóoba ñaan Yàlla, ne ko: «Yaw Aji Sax ji, sama Yàllay maam Ibraayma, di sama Yàllay baay Isaaxa itam, yaa ma ne woon: “Dellul réew ma nga cosaanoo, ca say bokk; dinaa la baaxe.”
Explore Njàlbéen ga 32:10
9
Njàlbéen ga 32:32
Ba jant bay fenk, Yanqóobaa ngi soox tànk bi, di bàyyikoo Penuwel.
Explore Njàlbéen ga 32:32
10
Njàlbéen ga 32:9
Booba mu ngi naan, bu Esawu songee benn dal bi, dal bi ci des mana raw.
Explore Njàlbéen ga 32:9
11
Njàlbéen ga 32:11
Yelloowuma lu gëna tuuti ci sa ngor ak sa worma, gi nga ma won, man sa jaam. Aw yet doŋŋ laa ŋàbboon, ba ma jàllee dexu Yurdan, te yokku naa tey, ba doon ñaari kurél.
Explore Njàlbéen ga 32:11
Home
Bible
Plans
Videos