1
Njàlbéen ga 13:15
Kàddug Yàlla gi
ndaxte réew, mi ngay gis mépp, yaw laa koy may ba fàww, yaak askan wi soqikoo ci yaw.
Compare
Explore Njàlbéen ga 13:15
2
Njàlbéen ga 13:14
Gannaaw ba Lóot teqlikook Ibraam, Aji Sax ji wax na Ibraam ne ko: «Téenal foofu nga taxaw, te séenu bëj-gànnaar ak bëj-saalum ak penkook sowu
Explore Njàlbéen ga 13:14
3
Njàlbéen ga 13:16
Dinaa leen yokk, ba ñu tollu ni feppi suuf, ba feppi suuf gëna neexa waññ sa askan.
Explore Njàlbéen ga 13:16
4
Njàlbéen ga 13:8
Ba loolu amee Ibraam da ne Lóot: «Waay waay, bu xuloo am sama digganteek yaw mbaa say sàmm ak samay sàmm. Xanaa dunuy bokk nag?
Explore Njàlbéen ga 13:8
5
Njàlbéen ga 13:18
Ba mu ko defee Ibraam sempi xaymaam, ñëw dal Ebron ca garab yu mag ya ca toolub Mamre, daldi fay tabaxal Aji Sax ji sarxalukaay.
Explore Njàlbéen ga 13:18
6
Njàlbéen ga 13:10
Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Sowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja.
Explore Njàlbéen ga 13:10
Home
Bible
Plans
Videos