1
Njàlbéen ga 12:2-3
Kàddug Yàlla gi
ma def la ngay cosaanal xeet wu yaa, barkeel la, màggal sa tur, ngay buntu barke; ku la ñaanal barke, ma barkeel, ku la móolu it, ma alag, te xeeti àddina sépp, ci yaw lañuy barkeele.»
Compare
Explore Njàlbéen ga 12:2-3
2
Njàlbéen ga 12:1
Aji Sax ji moo waxoon Ibraam, ne ko: «Jógeel sam réew, jóge ci say bokk ak sa kër baay, te nga dem ca réew mi ma lay won
Explore Njàlbéen ga 12:1
3
Njàlbéen ga 12:4
Ibraam daldi dem, na ko ko Aji Sax ji waxe woon, Lóot topp ca. Ba Ibraam di jóge Karan, booba am na juróom ñaar fukki at ak juróom (75).
Explore Njàlbéen ga 12:4
4
Njàlbéen ga 12:7
Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay.
Explore Njàlbéen ga 12:7
Home
Bible
Plans
Videos