Matthew 6:19-21
Matthew 6:19-21 GWG
Bu len dajale alal chi aduna si, fa gasah͈ ak h͈omak di yah͈a, te fa i sachakat di daji te sacha: Wande dajale len alal cha ajana, fa gasah͈ ak h͈omak dul yah͈a, te fa i sachakat dul daji, mbāte sacha: Ndege fa sa alal neka, fōfale la sa h͈ol jem itam.