YouVersion Logo
Search Icon

Matthew 15

15
1Fōfale i bindānkat ak i Pharisee ñu juge cha Jerusalem, ñou fi Yesu, ne,
2Lutah͈ sa i tālube moy nābe’ nit i h͈āt ya? ndege du ñu rah͈as sēn loh͈o su ño leka.
3Mu tontu len, ne, Yēn it, lutah͈ ngēn moy eble’ Yalla chi sēn nābe?
4Ndege Yalla wah͈ on na, ne, Teralal sa bay ak sa ndey: te, Ku h͈as bay am wala ndey am, na dē dē gi.
5Wande yēn a ne, Ku di wah͈ bay am wala ndey am, ne, Yalla lā may lu la mun a jeriñ:
6Bu mu teral bay am. Tah͈na be defadi ngēn eble’ Yalla mu di dara chi sēn nābe.
7Yēn nafeh͈a yi, Isaiah wah͈ on na dega chi yēn, ne,
8Nit ñile teral nañu ma ak sēn gemeñ, wande sēn h͈ol sorey na ma.
9Wande nēn la ñu ma jāmo, di jemantal i eble’ nit niki njemantal i Yalla.
10Mu ô mbōlo ma, te ne len, Dēglu len, te dēga:
11Lu h͈araf chi gemeñ, du gakal nit; wande lu gēna chi gemeñ, mō di gakal nit.
12Fōfale i tālube am ñou, te ne ko, H͈am nga ne Pharisee ya fakatalu nañu, ba ñu dēge kadu gile?
13Wande mu tontu, ne, Njembat bu neka bu suma Bay ba cha ajana jembatul on, di na ko simpi.
14Bayi len len; ño di njīt yu silmah͈a. Te su silmah͈a jītê silmah͈a, di nañu tabi chi mpah͈ ñom ñar.
15Peter tontu ko, ne, Tiki ñu lēb wile.
16Mu ne, Dēgangu len, yēn itam?
17Dēgu len ne lu mu mun a don lu h͈araf chi gemeñ, dem chi bir, ñu gēne ko chi biti?
18Wande yef yu gēna chi gemeñ, chi h͈ol la ñu juge; te ño di gakal nit.
19Ndege chi h͈ol bi la h͈alāt yu bon di juge, i mbōm, i njālo, i h͈emem, i nchacha, sēde yu di fen, i sāga:
20Yile di yef ya di gakal nit; wande te leka te bañ a rah͈asu, du gakal nit.
21Yesu juge on na fa, te dem chi wet i Tyre ak Sidon.
22Jena jigen i Canaan juge cha wet yōya, te mu h͈āch͈u, ne, Amal yermande chi man, E Borom bi, Dōm i Dauda; jine anga geten suma dōm ju jigen bu miti.
23Wande tontuwu ko dara. I tālube am ñou, te dagān ko, ne, Demlo ko, ndege tanh͈al na ñu.
24Wande mu tontu, ne, Fi nh͈ar i nēg i Israel yu rēr yi reka la ñu ma yōni.
25Wande mu ñou te jāmu ko, ne, Borom bi, lêl dimali ma.
26Mu tontu ko, ne, Daganul ñu jel mburu i h͈alel yi, te sani ko h͈aj yi.
27Wande mu ne, Wau, Borom bi; ndege h͈aj yi sah͈, di nañu di leka ndesit ya di rot chi sēn tabul i borom.
28Fōfale Yesu tontu ko, ne, E jigen ji, sa ngum rey na lol; naka nga buga, na ame nōgu chi you. Te chi wah͈tu wōwale dōm am wer cheng.
29Yesu juge on na fa, jegeñsi cha gēch i Galilee; mu yēg cha kou tūnda wa, te tōg fōfa.
30Mbōlo mu rey ñou fi mōm, and’ ak ña lagi, silmah͈a, lu, tēlekat, ak ñenen ñu bare, nu teg len chi tank’ am, te mu weral len;
31Tah͈na mbōlo ma jomi, ba ñu gise lū ya wah͈, lagi ya wer, tēlekat ya doh͈, ak silmah͈a ya gis: ñu magal Yalla i Israel.
32Yesu ô i tālube am fi mōm, te ne len, Am nā yermande chi mbōlo mi, ndege anda nañu ak man lēgi ñet’ i fan, te leku ñu dara; du ma len demlo te leku ñu, wala h͈ēchna di nañu ñaka dōle chi yōn wa.
33Tālube ya ne ko, Fan la ñu mun a ame mburu mu doy mbōlo mu rey niki bile, chi manding mi?
34Yesu ne len, Ñāta mburu ngēn am? Ñu ne ko, Jurom ñar, ak lu new chi jen yu tūt.
35Mu ebal mbōlo ma ñu tōg chi suf,
36Te jel jurom ñar i mburu ya, ak jen ya, gerem Yalla, mu dogat len, joh͈ tālube ya, te tālube ya joh͈ mbōlo ma.
37Ñepa leka be doylu, te ñu fêsal jurom ñar i sendel ak ndesit la.
38Ña lek’ on ñenent i njūne’ gōr la ñu, ganou i jigen ak i gūne.
39Mu demlo mbōlo ma, duga chi gāl ga, te ñou chi i wet i Magadan.

Currently Selected:

Matthew 15: GWG

Highlight

Share

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in