Matthew 15:25-27
Matthew 15:25-27 GWG
Wande mu ñou te jāmu ko, ne, Borom bi, lêl dimali ma. Mu tontu ko, ne, Daganul ñu jel mburu i h͈alel yi, te sani ko h͈aj yi. Wande mu ne, Wau, Borom bi; ndege h͈aj yi sah͈, di nañu di leka ndesit ya di rot chi sēn tabul i borom.