Njàlbéen ga 17:12-13
Njàlbéen ga 17:12-13 KYG
Xale bu góor, bu amee juróom ñetti fan war naa xaraf. Képp kuy góor ci seen maasoo maas, war naa xaraf, ba ci jaam bu juddoo sa kër, mbaa ku ñu jënd ci sa xaalis, ak bépp doomu doxandéem boo jurul. Jaam bu juddoo sa kër ak boo jënd, ñoom ñaar ñépp, dees leen wara xarfal. Xaraf ay màndargaal sama kóllëre ci seen yaram, muy kóllëre gu sax fàww.