1
Njàlbéen ga 3:6
Kàddug Yàlla gi
Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram, ji mu àndal, moom it mu lekk.
Compare
Explore Njàlbéen ga 3:6
2
Njàlbéen ga 3:1
Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?»
Explore Njàlbéen ga 3:1
3
Njàlbéen ga 3:15
Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.»
Explore Njàlbéen ga 3:15
4
Njàlbéen ga 3:16
Yàlla teg ca ne jigéen ja: «Dinaa taral sa metitu mat, ci metit ngay wasin. Sa bëgg-bëggu bakkan dina la xiir ci sa jëkkër, te moo lay teg tànk.»
Explore Njàlbéen ga 3:16
5
Njàlbéen ga 3:19
saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf, si ma la jële; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd.»
Explore Njàlbéen ga 3:19
6
Njàlbéen ga 3:17
Mu tegaat ca ne Aadama: «Gannaaw dégg nga sa waxu soxna, ba lekk ci garab gi ma la aaye, dinaa rëbb suuf ndax yaw; coono bu metti nga ciy dunde sa giiru dund gépp.
Explore Njàlbéen ga 3:17
7
Njàlbéen ga 3:11
Yàlla Aji Sax ji ne ko: «Ku la xamal ne dangaa def yaramu neen? Mbaa du dangaa lekk ca garab, ga ma la aaye, waay?»
Explore Njàlbéen ga 3:11
8
Njàlbéen ga 3:24
Da koo dàq, ba noppi teg ca penkub toolu Àjjana ba ay malaakay serub, boole ca saamar buy xuyy-xuyyi, tey dem ak a dikk, di wattu yoon, wa jëm ca garab gay taxa dund.
Explore Njàlbéen ga 3:24
9
Njàlbéen ga 3:20
Aadama nag tudde soxnaam Awa (mu firi Dund), ndax mooy ndeyu képp kuy dund.
Explore Njàlbéen ga 3:20
Home
Bible
Plans
Videos