1
Njàlbéen ga 15:6
Kàddug Yàlla gi
Ibraam nag gëm na Aji Sax ji, ba tax Aji Sax ji waññal ko ngëmam ag njub.
አወዳድር
{{ጥቅስ}} ያስሱ
2
Njàlbéen ga 15:1
Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.»
3
Njàlbéen ga 15:5
Loolu wees Aji Sax ji yóbbu ko ci biti ne ko: «Xoolal asamaan, te waññ biddiiw yi, ndegam man nga ko.» Mu dellu ne ko: «Noonu la sa askan di tollu.»
4
Njàlbéen ga 15:4
Kàddug Aji Sax ji nag dikkal ko, ne ko: «Du moom moo lay donn, waaye ku sosoo ci sa geño moo lay donn.»
5
Njàlbéen ga 15:13
Aji Sax ji wax Ibraam ne ko: «Déglul bu baax li ma lay wax: sa askan dinañu nekk ay doxandéem ci réew mu ñu moomul, ñu def leeni jaam, sonal leen diiru ñeenti téeméeri at.
6
Njàlbéen ga 15:2
Ibraam ne ko: «Boroom bi, yaw Aji Sax ji, ana loo may may nag? Man awma doom sax, te ki wara donn sama alal moo di Elyeser, miy waa Damaas.»
7
Njàlbéen ga 15:18
Keroog Aji Sax ji fas na kóllëre digganteem ak Ibraam, ne ko: «Askan wi soqikoo ci yaw laa jox réew mii dale ci dexu Misra, ba ca dex gu mag googee di Efraat
8
Njàlbéen ga 15:16
Say sët-sëtaat ay délsi fii bu seen jamono jotee, ndaxte bàkkaaru Amoreen ñi jéggeegul dayo.»
ቤት
መጽሐፍ ቅዱስ
እቅዶች
ቪዲዮዎች